Li suñu liggéeyu waare bi di def
1 Kàddu Yàlla dafay wone ne karceen yi, bu ñuy liggéeyal Yexowa, dañuy mel ni ñu nekk ci gawari ndamam, maanaam dañuy mel ni ay xarekat yu daan ba di ñibbisi (2 Kor. 2:14-16). Bu ñuy yégle xam-xamu Yàlla, suñu liggéeyu waare bi dafay mel ni cuuraay buy xeeñ lu neex ci Yexowa. Am na nit ñoo xam ne bu ñu déggee xibaar bu baax bi, dafa leen di neex ba ñu bëgg ci yokk seen xam-xam. Am na nag ñu bëggul déglu. Ñi bañ a déglu ñoo gën a bare, waaye loolu taxul suñu liggéey bañ a am njariñ. Nañu seet li suñu liggéeyu waare bi di def.
2 Dafay màggal Yexowa : Seytaane dafa wax ne nit ñi, seen bopp kese lañuy xalaat bu ñuy jaamu Yexowa (Ayó. 1:9-11). Liggéeyu waare bi dafay tax ñu mën a wone ne li ñuy def ngir jaamu Yexowa, ci suñu xol la jóge. Ay waaraatekat yu bare ñu ngi ci coono yu metti. Li ëpp ci nit ñi ñuy dajeel ci waaraate bi, duñu sax faale li ñuy wax. Waaye loolu terewul ñu kontine di waare te di sàkk ay taalibe. Loolu dafay seddal bu baax xolu Yexowa. — Léeb. 27:11.
3 Am na leneen li liggéeyu waare bi di def. Bokk na ci li ñu war a def bala coobare Yàlla di mën a am. Lii la Yexowa wax ci sànkute bu war a dal ci àddina Seytaane : “ Xeet yi dinañu xam ne man maay Yexowa. ” (Esek. 39:7). Bala nit ñi di mën a xam loolu, fàww jaami Yàlla yi kontine di xamal “ xeet yépp, giir yépp, kàllaama yépp ak réew yépp ” turam ak li mu bëgg def. — Peeñ. 14:6, 7.
4 Dinañu ci jaar ngir àtte nit ñi : Liggéeyu waare bi bokk na ci fi ñuy jaar ngir àtte nit ñi. Ndaw li Pool wax na ne Yeesu Krist dina dal ci kow “ ñi xamul Yàlla te baña déggal xebaar bu baaxu sunu Boroom Yeesu ”. (2 Tes. 1:8, 9.) Nit ñi dinañu leen àtte ci li ñu def bi ñu leen xamalee xibaar bu baax bi. Kon ñiy jaamu Yàlla am nañu warugar bu diis lool ! Bu ñu bëggulee nit ñi dee ndax ñun, waruñu leen a bañ a xamal xibaaru Nguur gi nga xam ne dafay musal nit ñi. — Jëf. 20:26, 27.
5 Li ñuy kontine di dimbali suñu moroom ngir ñu mën a neex Yàlla, dafay wone yërmande Yàlla (1 Tim. 2:3, 4). Xam nañu ne li nit nekke tey, mën na wuute ak li muy nekke ëllëg. Moo tax ñuy dellu ci nit ñi ay yooni yoon, di leen wax ñu jéem a xam Yexowa, bala muy wees. Bu ñuy def loolu, dañuy wone “ yërmande Yàlla ” mii “ bëggul kenn alku, waaye ñépp tuub seeni bàkkaar ”. — Lukk 1:78 ; 2 Pie. 3:9.
6 Dafa ñuy jariñ ñun ci suñu bopp : Jàpp lool ci liggéeyu Yexowa dafa ñuy sàmm ñun ci suñu bopp. Dafay tax ñu “ taxaw temm ci séentu bésu Yàlla bi ” te bañ a bàyyi àddina su bon sii tilimal ñu (2 Pie. 3:11-14 ; Titt 2:11, 12). Kon nag nañu “ takku, sampu ba dëgër, te gëna sawar ci liggéeyu Boroom bi ” xam ne lépp li ñuy def ci liggéeyu waare bi, du neen. — 1 Kor. 15:58.
[Laaj yi]
1. Lan la Yexowa xalaat ci suñu liggéeyu waare bi ? Lan la nit ñi di wax bu ñu leen di waar ?
2. Bu ñu bokkee ci liggéeyu waare bi, lan lañuy mën a wone ?
3. Lu tax kontine di xamal nit ñi turu Yàlla ak li mu bëgg def am solo lool ?
4. Naka la Yàlla di jaare ci liggéeyu waare bi ngir àtte nit ñi ?
5. Suñu liggéeyu waare, naka lay wonee yërmande Yàlla ?
6. Jàpp lool ci liggéeyu Yexowa, naka la ñuy jariñe ñun ci suñu bopp ?