Am na lu ñu mën a may Yexowa
1 Ndax xam nga ne doomu Aadama yi mën nañu may Yàlla dara ? Abel jëloon na ci juram ay mala yu baax lool, saraxe ko ngir Yexowa. Nóoyin, ak Ayóoba it defoon nañu lu mel noonu (Njàlb. 4:4 ; 8:20 ; Ayó. (Job) 1:5). Li ñu joxe noonu mënul yokkal dara Yàlla, ndaxte moo moom lépp li am ci àddina. Waaye sarax yooyu wone woon nañu ne nitu ngëm yooyu dañu bëggoon Yàlla lool. Tey, mën nañu jël suñu jot, suñu kàttan, ak suñu alal, jox ko Yexowa mu nekk “ sarax bu koy màggal ”. — Yaw. 13:15.
2 Suñu jot : Bu ñu jariñoo jot bi ñu doon def ci itte yu amul solo noonu, ngir gën a bokk ci waaraate bi, dinañu def lu rafet lool (Efes 5:15, 16) ! Xéyna mën nañu defaraat suñu porogaraam ngir mën a nekk pioñee buy jàpple benn wéer walla lu ko ëpp ci at mi. Mën nañu yokk it waxtu yi ñu faral di def ci waaraate bi. Ayu-bés bu nekk bu ñu yokkee 30 minit ci li ñuy def ci waaraate bi, loolu dina tax ñu yokk lu mu néew-néew ñaari waxtu ci li ñu doon def ci benn wéer !
3 Suñu kàttan : Bu ñu bëggee am doole ngir waaraate bi, dañu war a waññi foo yi, ak liggéey yoo xam ne, bu ñu ci jógee, dañuy sonn ba nga xam ne duñu mën a jox Yexowa li gën ci li ñu am. Waruñu xalaat torop suñuy coono yi mën a tax suñu xol “ jeex ” ndaxte loolu mën na jeexal doole bi ñu mënoon a jariñoo ngir jaamu Yàlla (Léeb. (Prov.) 12:25). Bu dee sax poroblem bu diis moo la tax a jaaxle, “ yenneeku ci Yexowa ” mooy li gën ci yow ! — Sab. (Ps.) 55:22 ; Filib 4:6, 7.
4 Suñu alal : Mën nañu joxe ci suñu alal it ngir jàpple liggéeyu waaraate bi. Pool dafa doon xiirtal ay mbokkam karceen yi ñuy faral di “ ber lu [ñu] àttan, denc ko ”, bu ko defee dinañu am lu ñu mën a may ñi nekk ci soxla (1 Kor. 16:1, 2). Noonu it, mën nañu ber tuuti xaalis ngir li suñu mbooloo soxla ak it liggéeyu waaraate bi ñuy def si àddina si sépp. Yexowa dafa fonk li ñuy maye ak xol bu sedd, bu dee sax lu tuuti lañu maye. — Luug 21:1-4.
5 Li ñu Yexowa may dafa bare lool (Saag 1:17). Bu ñu bëggee wone ne fonk nañu li mu ñu may, dañu war a def lu bare ci suñu jot, suñu kàttan, ak leneen li ñu am, ci liggéey bi ñuy def ngir jaamu ko. Loolu dina neex Yexowa, “ ndaxte kiy joxe ak mbég moo neex Boroom bi ”. — 2 Kor. 9:7.