TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 2/03 p. 3-4
  • Nañu waaraate bu baax

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu waaraate bu baax
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Yégleleen ni Yexowa baaxe
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Lu rafet te jar a def ci atum liggéeyu waare biy komaase
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • ‘ Nanga yégle fu nekk Kàddug Yàlla ’
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • ‘ Nañu seedeel ci ñépp xebaar bu baax bi ’
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 2/03 p. 3-4

Nañu waaraate bu baax

1 Yeesu dafa sant taalibeem yi liggéey bu réy : waaraate bi. Waaye ni ko “ njiit ak kilifa di defe ”, dafa leen njëkk won ni ñu ko war a defe (Isa. 55:4 ; Lukk 10:​1-12 ; Jëf. 1:⁠8). Lii la ndaw li Pieer wax ci li Yeesu sant : “ Yeesu sant na nu, nu yégal xeet wa, di seede ne, moom la Yàlla jagleel àtteb ñiy dund ak ñi dee. ” (Jëf. 10:42). Naka lañu mënee waaraate bu baax ?

2 Li Pool def ci waaraate bi mën na ñu jàngal lu bare. Bi mu dajee ak mag yi nekkoon ci mbooloo Efes, lii la leen wax : “ Xam ngeen ne, musuma leena nëbb dara lu leen di jeriñ, di leen jàngal ci kanamu ñépp ak ca kër ya. Dénk [“ waar ”, NW ] naa [“ bu baax ”, NW ] Yawut yi ak Grekk yi, ne leen, ñu tuub seeni bàkkaar, ba woññiku ci Yàlla, te gëm sunu Boroom Yeesu. ” Pool amoon na ay coono. Waaye def na lépp lu mu mën ngir yégal xibaar bu baax bi ay nit ñu baree bare. Jàngalu leen lu tuuti rekk yem ci, waaye dafa leen xamal “ lépp li Yàlla digle ”. Liggéey boobu jaraloon na ko mu sonn walla sax mu ñàkk lu bare. Newoon na : “ Sama bakkan soxalu ma, su fekkee bey naa sama sas, ba matal liggéey, bi ma Boroom bi dénk, maanaam ma seedeel [“ bu baax ”, NW ] ci ñépp xebaar bu baax, bi ëmb yiwu Yàlla. ” — Jëf. 20:​20, 21, 24, 27.

3 Tey, naka lañu mënee roy ci Pool (1 Kor. 11:⁠1) ? Nañu waaraate bu dee sax ñu ngi ci coono, te fexe ba waar nit ñu bokk ci xeet ak làkk yépp. Te boo gisee ku suñu waxtaan neex, defal lépp ngir dimbali ko ci wàllu ngëm (Macë 10:​12, 13). Loolu dina laaj ñu def ci suñu jot, ñu góor-góorlu, te bëgg nit ñi.

4 Ndax mën nga nekk pioñee buy jàpple ? Weeru màrs ak awril, baax nañu lool ngir waaraate bu baax. Kon nañu nekk pioñee buy jàpple. Daaw, waaraatekat yu bare fexe nañu ba def ko. Loolu, baax na lool !

5 Mbootaayu Yexowa mu ngi ñu doon xelal ngir ñu nekk pioñee buy jàpple. Suñu benn mbokk mu jigéen topp na xelal boobu. Kooku, 80 at la amoon, te ku xiibon lawoon. Lii la bind : “ Yàggoon naa bëgg nekk pioñee. Li ma dégg tax na ma gën ko bëgg. Fàww ma nekk ko lu mu bon bon beneen yoon. ” Mu jàpp weeru mars. Nee na : “ Li ma njëkk def mooy toog te xalaat lan la may laaj. Ma waxtaan ci ak sama doom bu jigéen ndax mu jàpple ma. Moom it sax dafa jël kayit ngir nekk pioñee buy jàpple. ” Ci weer woowu, suñu mbokk mu mag moomu, waaraate na 52 waxtu. “ Saa yu sama doole bëggoon a jeex, dama doon ñaan Yexowa mu mayaat ma doole. Def naa ko ay yooni yoon. Bi weer wi deewee, dama kontaan lool ci liggéey bi ma def. Gërëm naa Yexowa bu baax ci li mu ma dimbali. Bëgg naa nekkaat pioñee buy jàpple beneen yoon. ” Am na ñoo xam ne seen yaram neexul waaye dëgg dëgg, dañu bëgg nekk pioñee buy jàpple. Bu ñu déggee ni suñu mbokk moomu kontaane ndax li mu def, dina yokk seen fit.

6 Suñu benn mbokk mu góor, dañu ko jékki-jékki rekk dàq ci liggéeyam. Mu daldi nekk pioñee buy jàpple. Loolu tax na mu gën a bëgg liggéeyu waare bi te gën ci sawar. Bala weer wi dee, dafa tàmbali benn njàngum Biibël bi. Bi mu gisee ni ko Yexowa jàpplee ci lépp ak barke yi mu am, dafa ne : “ Aka nekk weer wu neex ! ” Yow itam, mën nga am barke yooyu boo yokkee li ngay def ci waaraate bi. — Mal. 3:⁠10.

7 Nekk pioñee buy jàpple yombul ci ñu bare. Am na ñuy liggéey, yore njaboot, te am seeni coono. Waaye loolu lépp terewu leen a nekk pioñee buy jàpple. Ku bëgg a waaraate bu baax, danga ci war a def sa jot ak sa doole. Waaye barke yi nga ciy jële bare nañu lool. — Léeb. 10:⁠22.

8 Màrs ak awril ay weer yu baax lañu ngir nekk pioñee yuy jàpple. Weeru màrs am na juróomi samdi ak juróomi dimaas. Ñiy liggéey, bu ñu waaraatee samdi ak dimaas yi ak bu ñuy wàcc ngoon, dina ñu mën a nekk pioñee yuy jàpple. Ci weeru awril am na ay fan yoo xam ne kenn du liggéey te kenn du jàngi. Kuy liggéey walla jàngi, mën na ci waaraate 50 waxtu yi ñu laaj pioñee buy jàpple. Seetal porogaraam yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bii, ci xët 4. Mën nga ci gis benn buy baax ci yow. Boo defee sa porogaraam ngir nekk pioñee buy jàpple, waxtaan ci ak ñi bokk ci sa njaboot walla yeneen waaraatekat. Ñàkkul mu am ñu bëgg ànd ak yow ci waaraate bi. Bu fekkee ne mënoo nekk pioñee buy jàpple, seetal ñaata waxtu nga bëgg def ci waaraate bi ci weer yooyu, te àndal ak pioñee yi. Seetal léegi li nga mën a def ngir yokk sa waaraate ci weeru màrs ak awril.

9 Ci jamano fàttaliku bi : At mu nekk ci jamano jooju, ñu bare dañuy “ jeriñoo jot gi ” ngir nekk ay pioñee yuy jàpple. Dañu xam ne Yeesu dafa saraxe boppam ngir fey njot gi. Te noonu lañu bëgg wonee seen ngërëm ci loolu (Efes 5:​15, 16). Daaw, ci Senegaal ak Mali, amoon na 230 pioñee yuy jàpple ci weeru màrs ak 75 ci awril. Boo boolee ñaari yooyu, dafa mel ni weer wu nekk, 153 waaraatekat ñoo nekkoon pioñee. Fekk ci juróomi weer yi jiitu woon, weer wu nekk 25 waaraatekat kese ñoo nekkoon pioñee. Ren it, nañu wone ne fonk nañu li ñu Krist defal, maanaam li mu fey njot gi. Nañu yokk kon liggéey bi ñuy def ci waaraate bi ci jamano ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu.

10 Bu bésu 16 awril di jegesi, xalaatal bu baax ci li ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu tekki ci yow. Fàttalikul li xewoon bala ñuy rey Krist ak lu diis lu nekkoon ci xelam ak xolam. Xalaatal ci lu neex lu ko Yàlla digoon ba tax mu muñ loolu lépp. Tey, Yeesu mooy Kilifa mbooloo mi. Moom mooy jiite liggéeyu waare bi ak li ñuy def ngir sàkk ay taalibe. Nanga ci xalaat it bu baax (1 Kor. 11:3 ; Yaw. 12:2 ; Peeñ. 14:​14-16). Na nga def it lépp li nga mën ci liggéeyu waare bi ngir wone ne am nga ngërëm ci lépp li Krist def.

11 Xiiral nit ñi ci waaraate bu baax : Mag ak surga mbooloo mi, fexeleen ba nekk pioñee yuy jàpple. Dina baax ci mbooloo mi. Àndleen ak waaraatekat yi ci liggéeyu waare bi. Demleen seeti leen ngir dimbali leen ci wàllu ngëm. Bu ngeen defee loolu, dingeen leen mën a dimbali ngir ñu bokk bu baax ci liggéey bi ñuy def ci mbooloo mi, ci weeru màrs ak awril. Na ku nekk ci ñun ñaan Yexowa ngir mu barkeel li ñuy def ngir waaraate bu baax.

12 Mbooloo yi dinañu góor-góorlu ngir yokk liggéey bi ñuy def ci waaraate bi ci weeru màrs ak awril. Mag ak surga mbooloo mi nañu leen ci jàpple bu baax, ñoom ñépp. Waaye wottukatu liggéeyu waare bi moo ci gën a am li mu war a def. War na tànn fu ñu war a defe ndaje yu ñuy am bala ñuy waare. War na tànn it bés ak waxtu yi ñu koy defe, ndax mu baax ci li ëpp ci waaraatekat yi. Na ko wax mbooloo mi te faral di ko ko fàttalil. War na fexe ba bés bu nekk, mu am ay ndaje ci waxtu yu wute ngir waaraate bi. Bu koo defee waa mbooloo mi dinañu mën a bokk ci ay fànnu waaraate yu bare : fu am ay bitig, ci mbedd mi, kër-oo-kër, ci telefon, walla ci dellu seeti ñi suñu waxtaan neex. Weer yooyu, war na fexe it ba ñu am téere, yéenekaay ak gox yu doy.

13 Ci weeru màrs, téere Xam-xam lañuy wone te dinañu góor-góorlu ngir tàmbali ay njàngum Biibël bi. Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2002 wone na ci xët 3 ak 4, ni ñu mënee wone téere boobu ci waaraate bi. Ci weeru awril, La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! lañuy wone ci waaraate bi. Jéemal a topp li ñu wax ci xaaj bi tudd “ Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi ”. Ñépp a war a waajal bu baax seen bopp, ngir waaraate bu baax.

14 Tey ñun lañu tànn ngir xamal nit ñi xibaar bu baax bi. Te Kilifa mbooloo mi ci boppam, Krist Yeesu, moo ñuy jiite ci liggéey boobu. Loolu, barke bu réy la. Weeru màrs ak awril ñu ngi jegesi. Nañu waaraate bu baax ngir topp ndigalu Krist. Nañu góor-góorlu it ngir weer yooyu raw yeneen weer yépp.

[Wërale bi nekk 4]

Porogaraam yi ñu mën a topp ngir nekk pioñee buy jàpple ci weeru màrs ak awril 2003

Bés bi Waxtu yi

Altine 1 2 ​— —​ 2 ​—

Talaata 1 ​— 3 —​ ​— —​

Àllarba 1 2 ​— 5 —​ ​—

Alxemes 1 ​— 3 —​ ​— —​

Àjjuma 1 2 ​— —​ ​— —​

Samdi 5 4 3 5 6 7

Dimaas 2 2 3 2 2 3

Màrs 56 56 54 55 50 50

Awril 50 50 51 53 ​— —​

Ci porogaraam yii, ndax am na ci benn bu baax ci yow ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager