Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 1er févr.
“ Ci sa xalaat, naka la njaboot yi naroon a mel bu ñu doon topp xelal bii ? [Jàngal Efes 4:31, ba pare mayal nit ki mu tontu.] Téere bii dafay joxe ay xelal yu ñu jële ci Kàddu Yàlla. Xelal yooyu nag, dina ñu dimbali ñu regle poroblem yi ci séy bi, te def ba jàmm sax ci kër gi. ” Wonal nit ki waxtaan biy komaase ci xët 18.
Réveillez-vous ! Févr.
“ Am na ñu gëm ne Yàlla dafay bind bépp bàkkaar bu nit def. Am na ñu wax ne Yàlla dafay baal bàkkaar bu mu mënta doon. Lan moo ci sa xalaat ? [Mayal nit ki mu tontu. Ba pare jàngal Jëf ya 3:19.] Xaaju téere bii, dafay wax ñett yi ñu war a def ngir Yàlla baal ñu te ñu jële ko ci Mbind mu sell mi. ” Won ko waxtaan biy komaase ci xët 10.
La Tour de Garde 1er Mars
“ Nit ñu bare dañu ne Yeesu yonent la. Ñeneen ñi ne jàngalekat bu mag la. Lan nga ci xalaat ? [Mayal nit ki mu tontu. Ba pare jàngal Macë 20:28.] Téere bii dina la wax lu tax Yeesu ñëw ci kow suuf joxe bakkanam ngir mu nekk njot, akit naka la ñu ko mënee jariñoo. ”
Réveillez-vous ! Mars
“ Ci yow, ndax diine yépp a baax ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal li Mbind mu sell mi wax ci yenn diine. [Jàngal Mark 7:7.] Lan lañu war a seet ci diine ba xam ndax dafay jàngale dëgg te du jàngale ‘dénkaaney nit ’ ? Ndax dëgg ci wàllu diine am na ? Téere bii dafa tontu laaj yooyu. ”