Ndax sa waa kër ñu ngi waajal seen bopp ngir mucc ?
1 Tey, ñu ngi gis li Biibël bi yégle woon. Loolu mooy wone ne muju jamono ji mu ngi jegesi ci lu gaaw a gaaw. Jamano ju metti jii niroo na lool ak jamano bi jiitu mbënn mi (Macë 24:37-39). Nóoyin dafa nekkoon nit “ kuy topp Yàlla ” moo tax bi ñu alagee àddina soosu, mu mucc (Njàl. 6:9). Wóor na ne Nóoyin jàngaloon na njabootam li Yexowa santaane, ndaxte ñoom it mucc nañu. Naka lañu mënee roy Nóoyin te waajal suñu bopp ak suñu waa kër ngir bu ñuy alag àddina su bon sii, ñu mucc ?
2 Ki daan waare ci njub : Nóoyin kontine na di “ waare ci njub ” lu mat 40 at jëm 50 at (2 Piy. 2:5). Wóor na ne moroomam yi ñaawal nañu ko bi mu doon waare, bu dee malaaka yi wàccoon ci kow suuf ñoo leen ci doon xiir walla déet. Bu ñuy waare dañuy tase ak ay nit ñu dul faale suñu wax te di ñu ñaawal. Loolu dafay wone ne léegi ñu alag àddina si (2 Piy. 3:3, 4). Waaye tey moom, am na ñu bare ñuy nangu déglu te ànd guruboo di ñëw ngir jaamu Yexowa (Is. 2:2). Su ñu kontinee di waaraate kese lañuy ‘ musal suñu bopp, ñun ak ñi ñuy déglu ’ (1 Tim. 4:16). Ci li ñuy wax ak ci li ñuy def yépp, wayjur yi war nañu jàngal seeni doom ne dañu war a gaawantu ci waaraate bi ndaxte dafa jamp. Loolu lu am solo la. — 2 Tim. 4:2.
3 Li ñu ko sant rekk la def : Lenn kese moo doon tax Nóoyin ak waa këram mucc : topp li Yexowa santaane (Njàl. 6:22). Ñun it tey dañu war a “ nooy ” maanaam nangu topp li ñu Biibël bi ak surga bu takku te teey bi di wax (Saag 3:17). Am na mag ak rakk yu doon fàttaliku ni seen baay doon toppe li mbootaayu Yexowa doon santaane. Ni ko mbootaay bi santaane woon, dafa doon def njàngum Biibël ak waa këram ayu-bés bu nekk. Te bu samdi ak dimaas jotee, dafa doon ànd ak waa këram ci waaraate bi. Dafa doon def lépp ba ànd ak kenn ci doomam yi buy waare samdi walla dimaas yi. Li mu doon kontine di def li ñu ko sant rekk, feeñ na bu baax ci ay doomam. Juróom-benni doomam yépp màgg nañu ba nekk ay jaamukatu Yexowa yu am ngëm.
4 Bu Yàlla di alag àddina si, dina bett nit ñi (Luug 12:40). Bu ñu royee Nóoyin te am ngëm ngir mën a mucc, ci lu wóor, loolu dina ñu waajal bu baax ñun ak suñu waa kër ! — Yaw. 11:7.