Ndaje Yi Jëm Ci Liggéeyu Waare Bi
9-15 suweŋ
Woy-Yàlla 10
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Na am ñu topp li nekk ci xët 4 te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde bu 1 suweŋ, ak Réveillez-vous ! bu suweŋ. Mën nañu wax it leneen lu mën a baax ci seen gox.
20 min : Ni ñuy waajale njàngum Biibël bu ñu war a defi. Waxtaan bu ñu jële ci Sasu Nguuru Yàlla bu ut 2004, xët 1. Bu waxtaan bi di waaj a jeex, na am waaraatekat buy wone ci lu gàtt ni ñu mënee waajal njàngum Biibël bu ñu war a defi. Ginnaaw loolu, na beneen waaraatekat wone ni muy toppe li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bi ngir waajal njàngum Biibël bi mu war a defi.
15 min : “ Buñu bàyyi waaraate bi ”a Bu ngeen amee jot, waxal ñi teew ñu wax ci aaya yi nekk ci xaaj bii.
Woy-Yàlla 89
16-22 suweŋ
Woy-Yàlla 8
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bi. Waxal ñi teew ñu bañ a fàtte indi La Tour de Garde bu 1 sulyet ak Réveillez-vous ! bu sulyet ci ndaje liggéeyu waare bi ñuy def ci ayu-bés biy topp. Nañu waajal waxtaan yu baax ci suñu gox yu ñu bëgg def bu ñuy waare.
15 min : Nañu wone njariñu xibaar bu baax bi. Waare ak waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci téere École du ministère, xët 158 ak 159. Waxal ñi teew ñu wax li itteel nit ñi tey ci seen gox. Laaj leen ñu wax ni ñu ci mënee waxtaan ak nit ñi bu ñuy waare.
20 min : “ Ndax sa waa kër ñu ngi waajal seen bopp ngir mucc ? ”b Bu ngeen amee jot, waxal ñi teew ñu wax ci aaya yi nekk ci xaaj bii.
Woy-Yàlla 4
23-29 suweŋ
Woy-Yàlla 36
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi te jàngal kayit biy wone ne bànqaas bi jot na xaalis bi ñu maye. Waxal téere yi ñuy wone ci weeru sulyet te na am ñuy wone ni ñu ko mënee wone ci waaraate bi.
20 min : Dund bu gën a neex ndax liggéeyu pioñee bu ci sax. Waxtaan bu ñu jële ci La Tour de Garde bu 15 sãwiyee 2008, xët 17 ba 19. Bu mënee nekk, nanga laaj ay laaj ñaari pioñee yu ci sax. Na kenn ki doon ku ci yàgg te keneen ki door ci komaase. Nañu wax ni seen dund gënee neex ndax li ñu nekk ci liggéey boobu.
15 min : Nañu waajal ni ñuy wone yéenekaay yi génn ci weer wi. Waxtaan ak ñi teew. Boo waxee ci lu gàtt li nekk ci La Tour de Garde bu 1 sulyet ak Réveillez-vous bu sulyet, nanga laaj ñi teew, yan waxtaan ñoo mën a neex nit ñi ci suñu gox, ak lu waral ñuy wax loolu. Waxal ñi teew ñu wax yan xaaju yéenekaay lañu bëgg wone ci waaraate bi. Lan lañu mën a laaj nit ki ngir komaase waxtaan bi ? Ginnaaw loolu, ban aaya lañu mën a jàng ci xaaju yéenekaay bi ñu bëgg wone ? Na am ñu topp li ñu bind ci Sasu Nguuru Yàlla bi ngir wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde bu 1 sulyet ak Réveillez-vous ! bu sulyet.
Woy-Yàlla 37
30 suweŋ ba 6 sulyet
Woy-Yàlla 63
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Waxal waaraatekat yi ñu bañ a fàttee bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru suweŋ te joxe ko.
20 min : Ci waaraate bi, lan lañu mën a def ngir suñu wax gën a rafet. Waare ak waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci téere École du ministère, xët 62, xise 4 ba fi xët 64 di jeex. Waxal ni ñu mënee topp li nekk ci xët yooyu ci seen gox. Ci lu gàtt, waxtaanal ak ku aay ci waxloo nit ñi buy waaraate saa yu ci amee bunt walla këroo-kër.
15 min : Vous en souvenez-vous ? (ndax yaa ngi koy fàttaliku ?). Waxtaan ak ñi teew bu ñu jële ci La Tour de Garde bu 15 awril, 2008, xët 29.
Woy-Yàlla 89
7-13 sulyet
Woy-Yàlla 13
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo.
15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.
20 min : “ Bu nit ki dee wax làkk bu ñu déggul. ”c Wottukatu liggéeyu waare bi moo koy def. Bu ñu àggee ci xise 2, nanga wax li mbooloo mi taxawal ngir jàngal ñi nekk ci suñu gox ci làkk bi ñu gën a dégg.
Woy-Yàlla 86
[Li ñu bind ci suuf]
a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.