TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • my nettali 5
  • Léegi àddina bi metti na

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Léegi àddina bi metti na
  • Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li tax ñu dàq leen
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Naka la dund bi meloon ci toolu Eden ba ?
    Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Ndegam Aadama ak Awa dañu déglu Seytaane — loolu lan la jur ?
    Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Lu tax nit di dee ?
    Dundleen ba fàww ak bànneex ci suuf si !
Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
my nettali 5
Awa ak ay doomam ci biti

NETTALI 5

Léegi àddina bi metti na

AADAMA ak Awa sonn nañu lool léegi. Ñu ngi ci biti toolu Eden. War nañu def liggéey bu metti ngir am lu ñuy lekk. Amatul garab yu rafet ak doom yu neex. Léegi, xaaxaam kese moo am ci suuf si, ak dég yu bare. Loolu yépp dafa leen dal ndaxte déggaluñu Yàlla. Nekkatuñu ay xaritam.

Waaye li gën a metti mooy dañu komaasee dee. Yàlla dafa leen tere woon benn doomu garab. Bu ñu ci lekkee, dinañu dee. Te loolu moo am. Bés bi ñu ko lekkee rekk, ñu komaasee dee. Ci dëgg, seen bañ a déggal Yàlla, amul woon benn njariñ !

Doom yi Aadama ak Awa amoon yépp, dañu juddu ginnaaw bi ñu leen génnee toolu Eden. Loolu moo tax ñoom itam ñu war a màgget te dee.

Céy, bu Aadama ak Awa déggaloon Yexowa ! Ñoom ak seeni doom dinañu am dund gu neex. Dinañu dund ba fàww. Kenn du màgget, feebar, ba pare dee.

Yàlla dafa bëgg nit ñi dund ba fàww ci jàmm. Nee na loolu dina am. Suuf si dina rafet te kenn du feebar. Nit ñi ñépp dinañu nekk ay xarit ci seen biir, nekk itam xaritu Yàlla.

Awa moom, nekkatul woon xaritu Yàlla. Looloo tax bi mu doon am doom, mu metti lool. Déggalul Yexowa, te gis nga ne loolu indil na ko coono yu bare, du dëgg ?

Aadama ak Awa amoon nañu doom yu bare, yu góor ak yu jigéen. Seen taaw bu góor, dañu ko tudde Kayin. Ki topp ci moom, dañu ko tudde Abel. Lan moo leen dal ? Ndax xam nga ko ?

Njàlbéen ga 3:16-23 ; 4:1, 2 ; Peeñu ma 21:3, 4.

Laaj yi

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager