WOY-YÀLLA 140
Dinañu dund ba fàww!
(Yowaan 3:16)
1. Xalaatal liy waaj a am:
Xeet yi yépp bokk bennoo.
Tiis dootul am, lépp ay dal,
fomp nañ wépp rongooñ!
(AWU BI)
Xol yi bég nañ, woyleen!
Ñun it dinañ fa teew.
Amal yaakaar, soreetul,
dinañu dund ba fàww.
2. Su boobaa yaram yi wér,
ñu jàmmoo ak Yexowa.
Fitna day jeex, dootul am.
Fàtte nañ coow ak tiit.
(AWU BI)
Xol yi bég nañ, woyleen!
Ñun it dinañ fa teew.
Amal yaakaar, soreetul,
dinañu dund ba fàww.
3. Àjjana dina neex lool,
ñépp ay màggal Yexowa.
Dund ba fàww ci bànneex,
la ñu Yàlla di may.
(AWU BI)
Xol yi bég nañ, woyleen!
Ñun it dinañ fa teew.
Amal yaakaar, soreetul,
dinañu dund ba fàww.
(Xoolal itam Ayóoba 33:25; Taalifi Cant 72:7; Peeñu ma 21:4.)