Woy-Yàlla 5 (10)
Taxawleen temm, ne ëkk!b
(1 Korent 15:58)
1. Ba muju jamano jii di jege,
Ñu ngiy doxal suñu sas ak ràññee.
Taxaw temm, ne ëkk lañ’ bëgg,
Di jaamu Yàlla dëgg.
(AWU)
Ne tem’ moo war, kon, ku ne, sore àddina sile;
Yàllaa ngi ñuy tette; nañ’ jëf li mu éble.
2. Ci topp nafsu la Seytaaney xiir.
Yàlla mën na ñoo muccloo ci fiir.
Waaye soxla nañoo doon nit ñu foog;
Nañ’ sampu ba dëgër, boog.
(Awu)
3. Nañ’ jaamu Yàllaak cawarteek doole.
Gis-gisu àddina sii day wàlle.
Nañ’ wottu mu lëndëmal suñ’ yaakaar.
Léegi jamano jii far.
(Awu)