Woy-Yàlla 27 (57)
Mbooloo Yeowa, mu bég mi
(Sabuur 89:15)
1. Am nañu bànneex ñépp ñiiy yuuxu ndax mbég,
Ndax dëgg gi ñu dég’, ak tawféex ji ñuy yëg.
Ndaxte dañoo dogal a dox ci sa leer ba fàw’,
Bànneex lañuy daj, ba ñuy jaar ci sa waaw.
(AWU)
Céy Yeowa, wone nga sa mbaaxaay
Ci nit ñiy yéene sa tur ak lewetaay.
Ràññee nañ’ dëgg, ndax sa Kàddook sa xel,
Seen ngëm fés na ci seen’ jëfi cofeel.
2. Seytaaneek ñii mu àndal a ngi ñuy fitnaal,
Suñuy jëf nañ’ woomal, suuf siy riir ak màggal.
Yeowa Yaa jagleel na ñi woyaf làqukaay;
Dina aar nit ñiy wut a topp njubaay.
(Awu)
3. Buñu yoqi, bu amee nit ñu dul déglu;
Dëgg gi lañ’ séexlu; ñun, ci lañ’ wàkkirlu.
War nañu dékku nattu te sàmm suñu ngor;
Dinañ’ jaamu Yàlla te duñu ko wor.
(Awu)