Woy-Yàlla 10 (27)
Bu leen ragal!
(Macë 10:28)
1. Deel jëm kanam, mbooloo samam,
Lawlool xabaaru Nguur gi.
Bul lox ci kanam say noon.
Xamleel ñi jub dëgg gii:
Krist bi, Yeesu, sama Doom ji,
Buur la, tey, ca asamaan,
Léegi mu musal leen te yeew
Seytaane, noon bi mu daan.
(AWU)
Bul ragal kuy sànk yaram
Te mënta rey bakkanam.
Képp ku takku ci ngoram;
Dinaa ko jotloo yoolam.
2. Ak lu noon yi bare te xos,
Ak lu-ñ’ ñu méb te raglu,
Ak lu ñu miikar tey siiñ,
Ci cuune yiy baax-baaxlu,
Buleen ragal, samay xeexkat.
Xeexleen! Takkleen seen fit;
Ndaxte duma sàmm muqat,
Xanaa ku ragalul nit.
(Awu)
3. Buleen ragal ma fàtte leen;
Ngir musal dinaa lagg.
Doonte sax seen bakkan rot,
Ndekkite dootul yàgg.
Buleen ragal, samay jàmbaar;
Wonleen ne dungeen bëqët,
Danaa sàmm kép’ ku takku
Niki sama peru bët.
(Awu)