Woy-Yàlla 46 (107)
Woyleen, di tagg Yeowaak fit!
(2 Nettaliy xew-xewi cosaan 20:21)
1. Nañu woy jaloore Yeowaak fit;
Ak dooleem mën nañ’ xeex suñuy noon.
Bu-ñ’ leen may ñu néewal suñu doole.
Ñemeleen. Saxleen ci dox liy yoon!
(AWU)
Tasleen xabaar bu baax, bu mucc gi!
Ndax ñép’ mën’ jébbalu ci Yaa, léegi.
Nañu woy jaloore Yeowaak fit,
Nañ’ màggal turam wu sell wi.
2. Nañu woy jaloore Yeowaak fit,
Te artu ca kow, ñépp dégg.
Ndax suñ’ Buur, léegi, mu alag ñi bon,
Diine fen, jeexal na ca dëgg.
(Awu)
3. Nañu woy jaloore Yeowaak fit,
Ba ñuy waar ñi lewet te dëggu;
Nañ’ leen won céru jaamu Yeowa,
Ndax ci def coobareem ñu dogu.
(Awu)