Woy-Yàlla 16 (37)
Rafetalal sa tur fa kanam Yàlla
(Dajalekat 7:1)
1. Am nangub Yàlla
Nañ’ wut, mu ñuy barkeel.
Sax ci li ko soob
Moo ñu war a itteel.
Sàrtam su ñu dundee,
Ci ni ñu ko nànde,
Tur dana rafet
Su-ñ’ ko tudde.
2. Kàddook jëfiy nit,
Ñoo koy sàkkal aw tur.
Bëgg-bëggu xol
Dana am lu mu jur.
Suñ’ tur dana jekk,
Su-ñ’ jaamoo Yaa rekk.
Dana ñu barkeel,
Saa su nekk.
3. Ñu ngiy sàkku tur
Bu-ñ’ taqee ci Yàlla.
Ci suñu dund,
Mooy sax li ñu soxla.
Kàddoom lañuy xeexal,
Sax ci di ko sargal
Doon noonu, dëgg,
Ñu koy màggal.
4. Bés yii dañoo bon,
Te war nañoo dogu,
Am fa kanam Yaa,
Tur wu baax te dëggu.
Yal nañ’ def li jub tey,
Waaw, cig leeram nañ’ wéy,
Tey waare Nguur geek
Fitna ju réy.