WOY-YÀLLA 75
«Maa ngi nii! Yónni ma!»
(Esayi 6:8)
1. Turu Yàlla la ñu tuutal,
di ko ñàkkal teggin fu ne.
Ab dof a ngi naan ci xelam:
‘Yàlla amul! Ku soxor la!’
Ana kuy dem setal turam,
yégle ay jalooreem fu ne?
(AWU BI 1)
ʻMaa ngi nii! Yàlla, yónni ma.
Maa lay kañ ak sama xol bépp.
Awma sag bu raw bii, Yexowa.
Waaw maa ngi nii! Yónni ma.’
2. Kii moom dafay ñaawal Yàlla
naan: ‘li Yàlla dige, daa yéex!’
Keneen ki di jaamu xërëm,
fal buur te xeeb nguuru Yàlla.
Ana kuy dem yégal leen ne,
bésub Yexowa dégmal na?
(AWU BI 2)
ʻMaa ngi nii! Yàlla, yónni ma.
Ak fit dinaa dem artu leen.
Awma sag bu raw bii, Yexowa.
Waaw maa ngi nii! Yónni ma.’
3. Aji jub jaa ngi naqarlu,
doyal sëkk ci ñawtéef yi.
Di wut dëgg giy dalal xel
seddal xol tey indi noflaay.
Ana kuy dem jottaliji
xibaaru jàmm ji ñuy xaar?
(AWU BI 3)
ʻMaa ngi nii! Yàlla, yónni ma.
Ma dem jàngal leen, tette leen!
Awma sag bu raw bii, Yexowa.
Waaw maa ngi nii! Yónni ma.’
(Xoolal itam Taalifi Cant 10:4; Esekiyel 9:4.)