Woy-Yàlla 22 (47)
Yeowa, suñu dooleek suñu kàttan
(Isayi 12:2)
1. Yeowa, suñ’ dooleek suñu kàttan,
Bég nañ’ ci yaw; yaay musal suñ’ bakkan.
Ñooy say seede, yiy yéene sa xabaar;
Ñiiy déglu mbaa dëddu dinañu waar.
(AWU)
Yeowa suñ’ Doj, suñ’ dooleek kàttan,
Sa tur nañ’ siiwal ba abadan.
Aji-Màgg ji, Yaa, Aji-kàttan,
Yaay suñu làqukaay, suñu màkkaan.
2. Ci Yeesu ñu ngiy wut mbég ak jàmm;
Te ci dëgg gi lañu ne xàmm.
Bu ñuy niir Mbind yi, yaa-ng’ ñuy digal;
Tànn nañu: Yeowa lañ’ faral.
(Awu)
3. Yàlla, sa coobare lañuy matal.
Ak lu Seytaane def def, yow lañ’ fal.
Ak lu mu ñu rey rey, céy! wàllu ñu
Ñu ne temm, ndaxte yoqiwuñu.
(Awu)