Woy-Yàlla 47 (112)
Bu keroogee lañuy xam
(Esekiel 35:15)
1. Say noon yàgg nañ’ di la won mbañeel,
Sa kër gu sel’, ak naxe di sobeel.
Léegi sa Buur fexe sa ndam jolli;
Nguuru Seytaane, dina ko folli.
(AWU)
Bu keroogee lañuy xam yaay Yeowa;
Bu keroogee lañuy xam, nag, sa ndam.
Bu keroogee la sa càkkeef di xam ne,
Lépp loo nas, ci lu wóor, loolooy am.
2. Sa kiliftéef, gi Seytaane tëkk,
Léegi mu fés, wone amul sikk.
Jamano jii, ca biir Ar-Magedon,
Dana tas te dootul am nit ku bon.
(Awu)
3. Ñi réy te diis, ñi yërëmul kenn,
Seen doole, kow suuf, bàyyiwul fenn.
Ci sa kàttan, dinga leen ràjjaxe.
Ku la sóoru, dëgg, mënul’ texe.
(Awu)