Woy-Yàlla 25 (53)
Yokkub Nguuru Yàlla
(Isayi 9:6, 7)
1. Sargalleen Nguuru Yàlla, gi di yokku!
Mu ngiy yokku ci fasoŋ bu doy waar.
Ciy màggal Yaa Yeowa ñu ngiy bàkku,
Ñii tànn dox ci leeram, di ci jaar.
Ca at ya jiitu, ndaw ndoorte lu tuuti
Niki ba Yeesu, ci suuf, doon waare!
Léegi mbooloo mu réy, mi des wi uti,
’Ngi koy woyal ay taggas yu bare.
2. Krist, toog ci kow jalu àttee ngiy nguuru;
Xeet yeek askan yaa ngi ci kanamam.
Kiliftéefu Yàlla, gi noon yiy sóoru,
Dina sargal, buy moxoñ ay noonam.
Moom, Aji-Xelal ak Baay bi sax ba fàw’,
Waaw, Garmib Jàmm bu làmboo kàttan.
Fitna Yaa dina indi jàmm ba fàw’
Te yokk nguuram, tey ba abadan.
3. Ndaw cér bu réy, fekke suñ’ jamano jii!
Ndax yokku bi bégloowul seeni xol?
Sàkkuleen mbég ci li ngeen di waareji,
Tey seedeek mbég, muy liggéey bu di yool.
Ñiy yàq deru Yeowa, artuleen;
Xamalleen leen seen bés dégmalsi na.
Ba ngeen di wéy di waareek fitna tey téen,
Képp, kuy xiix, na séentu àjjana.