Woy-Yàlla 80 (180)
Téereb Yàlla—Alal bu dul jeex
(Léebu 2:1)
1. Am na téere, boo xam ne ci ay xëtam,
Day indil nit jàmm, mbég ak yaakaar.
Xalaatam yu yéeme dañoo am doole;
Day gimmil ñi “gumba,” muy lu doy waar.
Téere bu jafe boobu mooy Biibël bi,
Ay góor, yu ñu sa, yàgg koo bind,
Ñu bëggoon dëgg seen Yàlla, Yeowa,
Xel mu sell mi doon xiir seen dund.
2. Bind nañu liy dëgg ci càkkeef’ Yaa,
Ni jaww ji ci kàttanam feeñe.
Wax nañ’ itam ni Aadama mate woon,
Ak ci càgganam, ni mu ko ñàkke.
Nettali nañu lu jëm ci malaaka,
Mu tëkkoon kiliftéefu suñ’ Yàlla.
Loolu yóbbe na bàkkaar ak tiis wu réy,
Waaye léegi turu Yàlla sell.
3. Tey, ñu ngiy dund mbég mu jéggi dayo.
Nguuru Yàlla juddu na; Krist mooy Buur.
Tey la bés bi Yeowa di musal nit,
Kép’ ku nangu deret ji Doomam tuur.
Ci biir téereem la xabaar boobu nekk;
Wax dëg’, moo gën fuuf wurusu ngalam.
Day dundloo yaakaar doom-Aadama yi;
Mooy nettali bi dàq, bi ñu am.