Woy-Yàlla 34 (77)
“Yeowa mooy sama Sàmm”
(Sabuur 23)
1. Yeowa mooy sama Sàmm.
Lu may ragal, kon, doye?
Ndax du toppatoo bu baax géttam?
Menn xar noon du foye!
Ci ndox yu neex la may nàndal,
Ci man dafa am itte.
Turam moo tax mu di ma tette
Ci yoonu sagook njubte.
Turam moo tax mu di ma tette
Ci yoonu sagook njubte.
2. Bu may jaar ci xur wu lëndëm,
Duma ragal loraange.
Maa ngeek sama Sàmm bu Mag bi;
Xawma lan ay tiitaange.
Sama bopp féexal naak diw;
Waaw, sama kaas fees na del’.
Ba abadan ci këram laay des,
Li may topp doon mbëggeel.
Ba abadan ci këram laay des,
Li may topp doon mbëggeel.
3. Ndaw Sàmm bu làmboo mbëggeel!
Jalooreem, ak mbég, laay woy.
Yéene mbaaxam ci ñii mel ni xar,
Loolu duñ’ ko def bu doy.
Kàddoom laa fas yéenee topp,
Ci yoonam ak teey laay wéy.
Sasam cér la, bu amul moroom.
Bés bu ne dinaa ko bey.
Sasam cér la, bu amul moroom.
Bés bu ne dinaa ko bey.