Woy-Yàlla 89 (201)
Bégleen ak mbooloo Yàlla
(Sabuur 106:5)
1. Ci biir sasu waare Nguur gi,
Ñu ngiy jamp nit ñi léegi:
‘Dégluleen Biibël, biy àggi,
Ba noppi fexee xam dëggu Nguur gi.’
Yàlla ñépp lay woo,
Ndax ak muj gu ñaaw ñu tàggoo
Te yaakaar ju bég ñu jagoo:
Jamano ju bees, ju jéggi dayo.
(AWU)
Nëwleen, yéen nit ñép’, bégleen!
Ak mbooloo Yaa waarleen
Xabaar bu baax, biy joxe dund.
Ci kanam’ Yaa sujjóotleen.
Ci njaamoom doguleen.
Faralleen Nguuru Yaa, mi leen bind.
2. Seetleen! Am na xeet wu sell,
Wu dajaloo, ba fees dell;
Dañ’ jébbalu, muy lu yell,
Ngir waar muccug Yaa, gi ñu xam xéll.
Yaa dina ñu yiwal
Su ñu nekkee nit ñuy jubal,
Di roy Yeesu, mi ñu musal;
Nañu wéy ci yoon, wi ñu Yaa xàllal.
(Awu)
3. Ci suuf su ni baaxe te neex,
Su amul ŋaayoo, xulook xeex,
Seetleen! mbooloo, mu ne ci péex,
’Ngi ci sasu Yàlla, dem ci ba jeex.
Dootuñu onkati;
Ci dëggu Yaa lañuy rooti.
Topp Kàddoom du lu metti,
Te turam dinañ’ woy tey woyati.
(Awu)