WOY-YÀLLA 34
Nañu am doxalin bu jub
(Taalifi Cant 26)
1. Baay àtte ma te seetlu sama ngor,
ak ni ma bëgge yiw, ak ni ma la wóoloo.
Gën maa xoolaat, xam foo tollu ci man.
Yal na samay xalaat jur ay jëf yooy barkeel.
(AWU BI)
Dama bëgg am doxalin bu set.
Ci dëgg gi laay des, waaw, fii ba abadan.
2. Dama dul toog ak nit ku bon tey fen.
Sib naa ki bañ dëgg, du sama àndandoo.
Céy Yexowa, bul jël sama bakkan,
boole maak bóomkat yi ak ñiy noot seen moroom.
(AWU BI)
Dama bëgg am doxalin bu set.
Ci dëgg gi laay des, waaw, fii ba abadan.
3. Li may neex mooy mën a dëkk sa kër,
ma di la fa jaamu, muy njaamu ju sell.
Sa kër gu mag, fa laa fas yéenee toog,
ma di la fa gërëm, sama baat di jolli.
(AWU BI)
Dama bëgg am doxalin bu set.
Ci dëgg gi laay des, waaw, fii ba abadan.
(Xoolal itam Taalifi Cant 25:2.)