WOY-YÀLLA 18
Xol yu fees ngërëm ndax njot gi
(Luug 22:20)
1. Buur Yexowa,
teew nañu tey ci sa kanam,
di la gërëm ndax mbëggeel
gu réy gi nga wone.
Joxe sa doom ji nga sopp
ngir musal ñu.
Baaxe nga ñu sarax si gën,
amatul beneen.
(AWU BI)
Mayug dundam moo ñu musal.
Deret ju sellam mooy yewwi.
Ba abadan, duñu tàyyi
ci wéy di la gërëm.
2. Ci coobareem la Yeesu
nangoo doon sarax.
Dundam gu mat
la feyee njot gi ndax cofeelam.
Yaakaar tasoon na, faf mu ñëw
ngir goreel ñu.
Jot nañ dund gi ñu doon xaar;
dee moom dootul teew.
(AWU BI)
Mayug dundam moo ñu musal.
Deret ju sellam mooy yewwi.
Ba abadan, duñu tàyyi
ci wéy di la gërëm.
(Xoolal itam Yawut ya 9:13, 14; 1 Piyeer 1:18, 19.)