WOY-YÀLLA 103
Sàmm yi, ay mayu Yàlla lañu
(Efes 4:8)
1. Yàlla teg na ci biir mbooloo mi,
Ay mag yu baax ci moom.
Nañu leen roy ci suñu dundin,
Ndax loolu moo ñuy aar.
(AWU BI)
Mag yi ñu Yàlla may ñoo ñuy sàmm,
Ñoom dañuy aar mbooloo mi.
Fonk nañ leen ndax seen cawarte.
Takku nañu ci Yàlla.
2. Bu ñu nekkee ci tiis yu bare,
Mag yi dañ ñuy déglu.
Dañuy ubbi Kàddu Yexowa
Ngir dalal suñu xel.
(AWU BI)
Mag yi ñu Yàlla may ñoo ñuy sàmm,
Ñoom dañuy aar mbooloo mi.
Fonk nañ leen ndax seen cawarte.
Takku nañu ci Yàlla.
3. Mag yee ngi wéy di ñu bàyyi xel,
Di sóoraale ëllëg.
Bu ñu bëggee jege Yexowa,
Nañu leen di déggal.
(AWU BI)
Mag yi ñu Yàlla may ñoo ñuy sàmm,
Ñoom dañuy aar mbooloo mi.
Fonk nañ leen ndax seen cawarte.
Takku nañu ci Yàlla.
(Xoolal itam Esayi 32:1, 2; Yeremi 3:15; Yowaana 21:15-17; Jëf ya 20:28.)