Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ngir atum 2000
1 Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla wonewu na niki barke bu oom ci mbooloo Yeowa. Ci biir 50 at yi wees, dimbali na ay milioŋi nit ñu suqali seeni mën-mën niki boroom kàddu ak jàngalekati dëgg, yi ne ci biir Biibël bi, te loolu ci diggu mbooloo. (Sab. 145:10-12; Macë 28:19, 20) Ndax gisal nga sa bopp ni la lekkool bi dimbalee? Lu ni mel mën naa wéy di am ci biir atum 2000, ci kow nga bokk ci bu baax-a-baax te topp xelal yi ñu la fay jox.
2 Tegtal yi jëm ci sas yi ak mbind yi ñuy jëfandikoo, lim nañu leen ci xët bu njëkk bi, bu doxalinu lekkool bi ngir atum 2000. Jot gi ñu àppal ngir wàll wu nekk, téere yi ñuy sukkandiku, ni ñuy war a doxale li ñuy waxtaane ak yeneen mbir yu ni mel, ñu ngi ko fay xamal. Baal ñu te jël jotu duruus tegtal yi bu baax-a-baax; boo noppee topp leen.
3 Duruusu Biibël bi, ayu-bés gu nekk: Ñaari doxalukaay yu wuute ngir duruusu Biibël bi, ayu-bés gu nekk, lañu lim ci doxalinu lekkool bi. Benn bi mooy doxalukaayu duruus, bi ñu tàmm di def tey ëmb lu tollook juróomi xëti Biibël bi. Ponk yi ëpp solo ci duruusu Biibël bi, ci duruus boobu lañuy sukkandiku. Dolli nañu beneen doxalukaayu duruus, bu ëmb, lu tollook ñaari yoon, xët yi ñu war a duruus ayu-bés gu nekk. Booy topp [ñaareelu] doxalukaay boobu, dinga mën a duruus Biibël bi lëmm ci diirub ñetti at. Xam nañu ne am na ñuy bëgg di duruus lu ëpp li ñu tëral ci doxalukaay bi ñu dolli, te ñeneen mën nañoo bañ a mën a ànd ak xélam. Bégal ci li nga mën a def, asté ngay tollale sa bopp ak ñeneen ñi. (Gal. 6:4) Li am solo dëgg mooy nga duruus Kàddug Yàlla, bés bu nekk.—Sab. 1:1-3.
4 Ngir bindu ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla, war ngaa wax ak wottukatu lekkool bi. Ñu ngi lay ñaan nga faaydaal li ñu la sas, te bañ di ko tebbi ci lu ñàkk fulla. Jàppeel lekkool bi niki lu jóge ca Yàlla. Dee ko waajal bu baax, ba mujj a mokkal li ñu la sas, te di ko wax ak kàddu yooy tibbe ci sa xol; noonu dinga sàkku njariñ ci lekkool, bu amul moroom boobu.