Ndax tàmm nga di yéene Nguur gi ?
1 Bégoon nañu, ñun ñépp, ba ñu yëgee ne, fii ci suñu réewum Senegaal, dañoo dajoon ca weeru ut 1999, lim bi gën a kowe bi ñu mas a am ci waarekat, ak 863 yéenekati Nguur gi. Wax dëgg, looloo ngi juddoo woon ci njéem bu ñépp ànd a def, akit ci dogu ! Ci li ñu seetlu ci biir weer yi ci topp, jafe woon na ci ñenn ci yéenekat yooyu ñu doon ay yéenekat ñu tàmm di waar Nguur gi, ndax booba ba tey, weer wu ne, 842 mbokk ñoo faral di génn ci liggéeyu waare bi. Looloo ngiy tekki ne boo jële 40 yéenekat, am na ci kenn ku dul xamle ne day bokk ci sasu waare bi, weer wu nekk. Gëm nañu ne xiirtal biy topp dina nekk ndimbal ngir sàkkal pexe mbir moomu.
2 Fonkal sa cér : War nañoo fonk bu baax-a-baax cér bi ñu am, bokk ak ñeneen xabaaru Nguur gi, bu baax bi. Yëngu-yëngu boobu day bégal xolu Yeowa, tey dimbali ñii seen xol jub ñu jàng a xam yoonu dund gi (Léeb. 27:11 ; 1 Tim. 4:16). Tàmm di seede day yokk suñu manoore ci sasu waare bi, te mbég ak bànneex lañu ciy jële.
3 Xamleel limu sa yëngu-yëngu : Am na ñuy bokk ci liggéeyu tool bi, waaye li ñuy sàggane mooy xamle limu seen yëngu-yëngu, ca waxtoom. Waruñoo foog mukk ne jarul ñuy xamle li ñu góor-góorlu def. (Dendale kook Mark 12:41-44.) Ak nu mu mën a mel, war nañoo xamle limu li ñu def ! Am pexe ca kër ga, mel ni di jëfandikoo almanak bu ñuy bind waxtu yi ñu jagleel sasu waare bi, loolu dina ñu dimbali ñu fàttaliku saa su nekk ne, war nañoo xamle, ci lu gaaw te wér, limu li ñu def, saa su weer wi deewee.
4 Dimbalil ñii ko soxla : Mën naa am ñu war a taneel li ñuy def ci mbooloo mu nekk, ngir jàpple ñii soxla ndimbal lu jëm ci tàmm di bokk ci liggéeyu waare bi. Sekkerteeru mbooloo mi ak ñiiy jiite njàngum téere mbooloo mi war nañoo wut ay yéenekat yu am manoore, ndax ñu may leen loxo. Soo amee ay doom walla ñeneen nit ñuy jàng Biibël bi, ñoo xam ne ay yéenekat yu ñu sóobagul lañu, jéemantal leen ñuy xamle weer wu nekk limu seen yëngu-yëngu.
5 Fàttalikul nettalib jaar-jaaru suñu mbokk mu jigéen Ottilie Mydland, bi ñuy fekk ci La Tour de Garde bu 1 oktoobar 1997, nettali bu tuddoon : “ Reconnaissante à Jéhovah pour une longue vie à son service. ” Suñu mbokk moomu dëkk Noorwees, tàmmoon na di yéene xabaar bu baax bi, laata sax ñu koo sóob ca 1921. Ba ci juróom-ñaar fukki at ak juróom-benn tegoo, lii la wax, fekk mu tollu ci 99 at : “ Kontaan naa lool ci li ma mën a nekk, ba tey, yéenekat bu tàmm di waare. ” Akay xel mu rafet mu mu soloo, xel mu jaami Yeowa yi yépp war a roy !