Ndax yaa ngi def sa wàll ngir ñu mën a bind li ñu def ci waaraate bi te bañ cee juum ?
1 Bu ñuy nettali dara ci Biibël bi, bare na fi ñu wax ñaata nit ñoo fa nekkoon, bu ko defee, ñu mën a xam bu baax li fa xewoon. Gideyon, 300 góor kese la àndaloon bi mu gañee waa Madyan (Àtt. 7:7). Malaaka Yàlla ma, 185 000 xarekat yu jóge woon Asiri la rey (2 Bu. 19:35). Ci Pàntakótt bu atum 33 ci suñu jamano, lu mat 3 000 nit lañu sóob ci ndox, te ci lu gaaw, nit ñi gëmoon yokku nañu ba mujj a mat 5 000 (Jëf. 2:41 ; 4:4). Lii dafay wone ne jaamukatu Yàlla yi ci jamano yu njëkk ya dañu doon góor-góorlu ngir bind lépp li doon xew te bañ cee juum.
2 Tey, mbootaayu Yexowa dafa ñuy ñaan ñu bind weer wu nekk, li ñu def ci waaraate bi te joxe ko. Bu ñu defee ni mu ware li ñu laajte noonu, dina tax ñu mën a seetlu bu baax ni liggéeyu waare bi di deme. Bu nit ñi bindee li ñu def ci waaraate bi te joxe ko, bu amee fànn bu ñu war a seetlu ci waaraate bi, dina ci feeñ. Bu amee gox bu soxla ay waaraatekat yu gën a bare, dina ci feeñ itam. Ci mbooloo mi, bu nit ñi bindee li ñu def ci waaraate bi te joxe ko, mag yi dinañu gis waaraatekat yi mën a yokk seen liggéeyu ware bi, ak waaraatekat yi soxla ñu jàpple leen. Te bu ñuy xamal nit ñi ni liggéeyu waare Nguur gi di jëme kanam, dafay yokk doole mbokk karceen yi yépp. Ndax yaa ngi def sa wàll ngir ñu mën a bind li ñu def ci liggéeyu waare bi te bañ cee juum ?
3 Liy sa wàll : Bu weer wi deewee, ndax fàttaliku li nga def ci waaraate bi dafa lay jafe ? Bu dee waaw, saa yoo waaraate ba pare ndax mënoo bind li nga def ? Am na ñuy jëfandikoo benn calendrier walla benn agenda. Am na it ñuy jël ci kayit fi ñu war a bind li ñu def ci waaraate bi, benn bu ñu bindagul dara, yóbbaale ko. Bu weer wi deewee, na nga gaaw a bind li nga def ci waaraate bi te joxe ko. Mën nga ko jox sa wottukatu njàngum téere bi. Bu la gënalee it, mën nga ko def ci boyet fu ñu koy def ci Saalu Nguur gi. Boo fàttee joxe li nga def ci liggéeyu waare bi, na nga gaaw a wax ak sa wottukatu njàngum téere bi, te bañ a xaar ba muy ñów ci yow. Boo binde li nga def ci waaraate bi te joxe ko ni mu ware, dina wone ne fonk nga li Yexowa taxawal. Dina wone it ne fonk nga te weg nga suñu mbokk mi war a dajale te boole li ñu bind lu jëm ci liggéeyu waare bi ñu def. — Lukk 16:10.
4 Li wottukatu njàngum téere bi war a def : Wottukat bi dafa war a gaaw a seetlu lépp liy xew ci njàngum téere bi te gaaw ci def li war. Kon dafa war a ittewoo li képp ku bokk ci njàngum téere bi muy jiite di def ci waaraate bi weer wi yépp (Léeb. 27:23). Xam na bépp waaraatekat bu tàmm waaraate bu baax te di ci am mbégte. Te dafay gaaw a dimbali képp ku toog weer lëmm te waaraatewul. Ci lu bare, ñooñu bu leen wottukat bi waxee ay wax yuy dalal xel, walla mu wax leen li ñu mën a def, walla mu ñaan leen ñu ànd ak moom ci waaraate bi, loolu kese dina leen doy.
5 Bu weer wi deewee, wottukatu njàngum téere bi dina seet ndax képp ku bokk ci gurupam bind na li mu def ci waaraate bi te joxe ko. Bu ko defee, bala weer wi am 6 fan, sekkerteer bi dina mën a yónnee bànqaas bi li mbooloo mi def ci waaraate bi te bañ cee juum. Bu weer wi di waaj a dee, liy mën a dimbali wottukat bi mooy mu fàttali nit ñi ne dañu war a joxe li ñu def ci waaraate bi, te mu indi ay kayit fu ñu koy binde ci béréb bu ñuy defe njàngum téere bi. Bu amee ku tàmm fàtte joxe li mu def ci waaraate bi, mën na ko ko fàttali te wax ko ay kàddu yiy tax mu sawar ko def.
6 Boo gaawee bind li nga def ci waaraate bi te joxe ko, dinga def sa wàll ndax ñu mën a xam dëgg li ñu def ci liggéeyu waare bi. Ndax weer wu nekk dinga gaaw a bind li nga def ci liggéeyu waare bi te joxe ko ngir def sa wàll ?