Nañu góor-góorlu ci def lu baax !
1 Bés bi ñu war a màggal deewu Yeesu mu ngi jegesi. Kon, li war a tax ñu ‘ góor-góorlu ci def lu baax ’ bare na (1 Pie. 3:13). Bi ci gën a am solo mooy njot gi Yeesu Krist fey ngir ñun (Macë 20:28 ; Ywna. 3:16). Ndaw li Pieer nee na : “ Yàlla [...] jotuleen ak yu deme ni xaalis mbaa wurus, yuy wéy, waaye ci deretu Krist ju tedd ji, mel ni mbote mu sikkul te wàññikuwul. ” (1 Pie. 1:18, 19). Ci dëgg mbëggeel bu réy a réy la ! War na tax ñu bëgg def yëf yu baax yu bare. Waaw xam nañu ne Yeesu “ joxe na bakkanam ngir nun, ba jot nu ci lépp lu bon, te beral nu boppam, di xeet wu sell te ràññeeku ci jëf yu baax ”. — Titt 2:14 ; 2 Kor. 5:14, 15.
2 Yàlla mooy wax lan mooy lu baax. Bu ñu defee lu baax loolu suñu diggante ak moom dina rattax ak moom, te dina ñu toppatoo bu baax a baax. Pieer nee na it : “ Ku bëgg am dund gu naat te fekk bés yu rafet [...] Na dëddu lu bon, tey def lu baax, na xinte jàmm te sax ci. Ndax Boroom baa ngi xool ñi jub bëti yërmande, di ubbi ay noppam ci seeni ñaan. ” (1 Pie. 3:10-12). Ñu ngi ci jamano ju naqadi te metti. Waaye Yexowa dafa ñuy xool ngir aar ñu te toppatoo ñu. Dafa ñu bëgg dimbali. Dafa ñu bëgg aar mel ni ñu nekk bëtam. Aka nekk lu baax te neex ! — 5 Mu. 32:10 ; 2 Net. 16:9.
3 Karceen yu doon dund ci jamano Pieer te jotoon bataaxalam, ñu ngi won ci coono. Waaye seen xel yépp mu ngi woon ci waare xibaar bu baax bi fu nekk. Loolu ñu bëggoon, mu ngi meloon ni safara ci ñoom te kenn mënu ko woon fey (1 Pie. 1:6 ; 4:12). Tey itam, loolu la mbootaayu Yàlla bëgg. Dëgg la, ñu ngi dund ci “ bési tiis yu tar ”. Waaye bu ñu gisee ni Yexowa baaxe ak ñun, ci dëgg dëgg suñu xol moo ñuy xiir ci sawar a def li Mu bëgg (2 Tim. 3:1 ; Sab. 145:7). Léegi nañu waxtaan tuuti ci lu baax li ñu mën a def ci jamano fàttaliku bi.
4 Nañu wax nit ñi ñu teew ci ndaje fàttaliku bi : Njot gi ñu Yàlla may, lu réy a réy la. Mën nañu wone suñu ngërëm ci loolu bu ñu teewee bés bi ñu war a màggal deewu Yeesu. Ren, àllarba 16 awril lay doon, bu jant bi sowee ba pare (Lukk 22:19, 20). Daaw ci 94 600 mbooloo ci àddina si sépp, amoon na 15 597 746 ñu fa teewoon. Boo seetee ñaata lañu woon ca at mi ko jiitu, dinga gis ne 220 000 nit ñoo ci yokku.
5 Ñaata ñooy teew ren ? Ci lu bare dina aju ci ñaata nit lañuy woo. Loolu dina laaj ñu sawar ci bu baax. Na nga njëkk bind turu ñi nga bëgg ñu ñów ñépp. Sa waa kër nga war a njëkk bind. Boo amee jëkkër walla jabar bu nekkul Seede, nee ko ne ci dëgg dëgg li nga bëgg ci sa biir xol mooy mu ñów teew ak yow. Am na benn jëkkër bu nekkul Seede bu teewoon ndaje fàttaliku bi daaw. Lu tax mu dem fa ? Nee na dafa gis ne ci dëgg dëgg jabaram dafa bëggoon lool mu ànd ak moom ca ndaje ba. Boo paree ak sa waa kër mën nga bind turi say mbokk, say dëkkandoo, ñi nga bokkal liggéey walla ñi nga bokkal lekkool. Bul fàtte woo ñi ngay jàngal Biibël bi itam.
6 Boo bindee tur yooyu ba pare, demal seeti leen ñoom ñépp ngir wax leen ñu ñów teew. Yóbbul kayit bi ñu defar ngir woo nit ñi ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Bindal ci suufu kayit boobu ak mbind mu leer waxtu bi ak béréb bu ñuy defe ndaje boobu, ngir nit ñi bañ koo fàtte. Bu bésu 16 awril di jegesi, nanga fàttali nit ñooñu ndaje bi. Mën nga leen seeti yow ci sa bopp walla nga telefone leen. Nañu def lépp ngir dimbali nit ñu baree bare ñu ñów teew ci ndaje bu am a am solo boobu.
7 Nañu dimbali ñi teewe ndaje fàttaliku bi : Bés boobu mën nañu leen dimbali bu baax. Mën nañu teral ñi tàmmul a teewe suñuy ndaje yi. Soo ko mënee, nanga teel a agsi te yéex a ñibbi. Nanga leen teral bu baax. Bul xaar ba ñu ñów ci yow. Yow mi yaa war a dem ci ñoom nuyu leen te waxtaan ak ñoom. — Room 12:13.
8 Ndax am na koo ci mën a dimbali mu jëm kanam ci wàllu ngëm ? Kon, fàww mu jàng Biibël bi. Su dee amagul ku koy jàngal Biibël bi, jéemal xam turam ak adareesam ngir seeti ko. Boole ci mbëggeel dëgg. Xéyna bala bésu fàttaliku bu déwén jot, dina am ñu ci nekk waaraatekat bu ñu sóobagul. Booy seeti nit ñi teewoon bésu fàttaliku bi, bul fàtte di leen wax ñu ñów teewe waxtaan bi ñu faral di am ci àddina sépp bu ndaje fàttaliku bi weesoo, te war a am ci bésu 27 awril.
9 Ndax mën nga nekk pioñee buy jàpple ci weeru màrs ak/walla awril ? At mu nekk am na yenn weer yoo xam ne am na lu bare lu ñu mën a def ci wàllu ngëm. Ci jamano fàttaliku bi, bu waa mbooloo mi yépp sawaree ci waaraate bi, dina jur lu bare lu baax.
10 Benn mbooloo bu am 107 waaraatekat ak 9 pioñee dañu ne seen weeru awril bu daaw, weesu na baax. Dañu amoon 53 waraatekat yu nekkoon pioñee yuy jàpple. Magi mbooloo mi yépp ak surgay mbooloo mi yépp nekkoon nañu pioñee yuy jàpple ci weer boobu. Lan la magi mbooloo mi def ngir waa mbooloo mi bëgg nekk pioñee ? Bala weeru màrs ak awril jot fekkoon na ñu xiir ñi nu mënoon ñépp ci nekk pioñee. Dañu bëggoon ñépp mën a bokk ci ndaje yi ñu am bala ñuy waare. Looloo taxoon ñu def ndaje yooyu ci waxtu yu wuute ci bés bi. Te xiir nañu bu baax waaraatekat yi ci waaraate ci telefon, xam ne loolu moo gën ci ñi feebar walla màgget ba génn jafe ci ñoom.
11 Ci mbooloo moomu, am na suñu benn mbokk mu jigéen mu amoon 86 at. Dafa feebaroon ba mënul woon sax dox. Joxe na kayit bu ñu bind ngir nekk pioñee buy jàpple. Ci suba si dafa doon toog ci waañ bi te seede ci telefon lu mat ay waxtu. Ba pare dem noppaleekuji. Ba pare ñówaat seedewaat ci telefon. Waxtaan na ak benn jigéen koo xam ne jëkkëram ak ñaari doomam yu góor, ñoo gaañu woon ci ñaari at yi weesu. Jigéen jooju mënul woon xam lu tax Yàlla nangu lu mel noonu am. Suñu mbokk mi seede na ko bu baax a baax te tàmbali na ak moom benn njàngum Biibël bi. Ci dëkk yu mag yi am na ay nit ñu dëkk ci tabax yu kowe walla ay béréb foo xam ne kenn mënu fa dugg. Bu ñu leen bëggee waar, li gën mooy ñu telefone leen. Dina baax it bu ñu bëggee jot ñi nekkul woon seen kër ci bëccëg.
12 Lii la magi mbooloo moomu mujj a wax : “ Jamano jooju, aka nekk jamano ju neex. Ñu ngi gërëm Yexowa ci li mu xajal nit ku nekk ci liggéeyam ak barkeem. ” Bu ngeen waajalee seen bopp bu baax yéen it ci seen mbooloo, mën ngeen a am barke yooyu.
13 Nañu fexe ba waaraatekat yépp bokk ci liggéeyu waare bi : Dañu bëgg Yàlla ak suñu moroom. Moo tax weer wu nekk ñu bëgg jariñoo jot gi ngir waar nit ñi ci xibaar bu baax bi (Macë 22:37-39). Wottukatu Njàngum téere yi ak ñi leen di jàpple, dañu war a dimbali ñi bokk ci seen gurup ñu waaraate weer wu nekk. Li ñu mën a def mooy wax ak ay waaraatekat ngir ñu ànd ci waaraate bi. Buñu xaar ba weer bi bëgg jeex ngir def loolu. Nañu ko teel a def. Dinañu gën a am jot ngir dimbali leen.
14 Ndax am nga ci sa waa Njàngum téere bi ay waaraatekat yu wopp walla màgget ba waaraate yombul ci ñoom ? Xéyna am na ñu nekk loppitaan walla mënuñu génn seen kër. Ci dëgg li ñu mën a def ci waaraate bi barewul. Waaye ba tey mën nañu fexe ba seen leer leer bu baax. Bu nit ñi gisee seeni jëf yu rafet, xéyna dinañu bëgg a xam dëgg gi (Macë 5:16). Wottukatu Njàngum téere yi war nañu seet ndax ñi wopp ñooñu xam nañu bu baax ne bu dee sax li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weer bi matul benn waxtu, mën nañu ko bind te joxe ko. Mën na nekk 15 minit, walla 30 minit, walla 45 minit. Loolu dina tax waaraatekat yu takku yooyu bég te gën a am doole. Kon, bu ñuy bind li mbootaayu Yàlla def ci liggéeyu waare bi ci àddina si sépp, du am njuumte.
15 Ay ndaw yu am lu bare lu ñuy def ci lu baax ! Am na ay ndaw karceen yuy jariñoo seen doole ngir jaamu Yexowa. Loolu, lu rafet la (Léeb. 20:29) ! Ci weer yi ñu nekk nii, ñépp a bëgg yokk li muy def ci waaraate bi. Boo nekkee ndaw, loo mën a def ba wone ne sawar nga ci liggéeyu Yexowa ?
16 Xéyna nekkaguloo waaraatekat bu ñu sóobagul. Waaye loo mën a def ba mën ko nekk ? Laajal sa bopp lii : ‘ Ndax xam naa li ñu warul a ñàkk xam ci dëgg gi nekk ci Biibël bi ? Ndax bëgg naa bokk ci liggéeyu Nguuru Yàlla ? Ndax li may def ci sama dund, lu jar a roy la ? Ndax man mii ci sama bopp mën naa wax nit ñi li ma gëm, maanaam waxtaan ak ñoom ci xibaar bu baax bi ? Ndax sama xol moo ma ci xiir ? ’ Bu fekkee ne tontu nga waaw ci laajte yooyu, waxal say wayjur ne danga bëgg a nekk waaraatekat. Say wayjur dinañu wax ak benn magu kurélu liggéeyu waare bi.
17 Boo nekkee waaraatekat ba pare, te mu am ay bés yoo xam ne kenn du jàngi, ndax mënoo yokk li ngay def ci liggéeyu waare bi ? Ay ndaw yu ñu sóob yu bare fexe nañu ba nekk pioñee yuy jàpple. Dañu defar porogaraam bu baax te seen wayjur ak ñeneen dañu leen jàpple. Boo mënul loolu, ba tey fexeel ba yokk li ngay def ci liggéeyu waare bi. Nanga seet ñaata waxtu nga bëgg a def ci waaraate bi. Ginnaaw loolu nanga seet li nga mën a def ba sa waaraate bi gën baax. Xéyna dinga bëgg a jàng benn aaya ci Biibël bi ci kër gu nekk. Walla nga bëgg am ay waxtaan yu gën a baax boo demee seetiwaat nit ñi. Walla nga bëgg tàmbali benn njàngum Biibël bi. Walla tàmbalee seede ci telefon, walla def leneen ci waaraate bi. Walla ndax dinga bëgg ànd ak sa dëkkandoo, ki nga bokkal lekkool, walla sa mbokk ci ndaje fàttaliku bi, ci weer wi di ñów ? Bu ñuy góor-góorlu ci loolu lépp, ñun ak waa mbooloo mi dinañu bég te am lu baax. — 1 Tes. 5:11.
18 Nañu dimbali ñi ñu jàngal Biibël bi ñu jëm kanam : Bu ñu seetee njàngum Biibël yi amoon daaw ci Senegaal ak Mali, dafa mel ni weer wu nekk dafa amoon 1 925. Bu ñu kontinee noonu, ñu ci bare dinañu dem ba jébbal seen bopp Yàlla te sóobu ci ndox mi. Waaye bala loolu, war nañu leen a dimbali ñu mën a nekk waaraatekatu xibaar bu baax bi. Loolu, am na solo lool bu ñuy jàngal nit ñi ni ñu mënee nekk taalibe Yeesu Krist (Macë. 9:9 ; Lukk 6:40). Ndax fi nga tollu nii, am na ci ñi ngay jàngal Biibël bi ku mën a nekk waaraatekat ?
19 Xéyna xalaat nga ko, waaye wóorul la. Kon nanga ci waxtaan ak sa wottukatu Njàngum téere bi walla sa wottukatu liggéeyu waare bi. Mën nga ko laaj mu ànd ak yow ci njàngum Biibël boobu. Ñaari mag ñooñu li ñu xam ci wàll boobu bare na, te mën nañu xam bu baax fu ki ngay jàngal tollu ci ni muy jëme kanam. Xéyna dinañu am lu ñu koy wax ngir mu kontine di jëm kanam.
20 Ki ngay jàngal, bu bëggee nekk waaraatekat bu ñu sóobagul, te nga foog ne mën na ko nekk, wax ko wottukat biy jiite. Dina laaj ñaari magu mbooloo mi ñu toog ak yow ak ki ngay jàngal ngir seet ba xam ndax mën na nekk waaraatekat bu ñu sóobagul. Dinañu waxtaan ci li nekk ci téere Notre ministère xët 98 ba 100. (Seetal La Tour de Garde bu 15 nowàmbar 1988, xët 17.) Bu ñu waxee ne ki ngay jàngal mën na nekk waaraatekat, nanga ko gaaw a won ni ñuy waaraatee. Bu joxee ci mbooloo mi kayit bi ñu binde li ñu def ci liggéeyu waare bi, dinañu wax waa mbooloo mi ne léegi nekk na waaraatekat bu ñu sóobagul. Ñu ngi ñaan Yàlla mu am ay junniy waaraatekat yu bees, mag ak ndaw, ci jamano fàttaliku bii.
21 Nañu waajal liggéey boobu bu ñu bëggee mu gën a baax : Lépp li ñu bëgg def ci jamano fàttaliku bi, bu ñu bëggee mu sotti, war nañu ko waajal bu baax (Léeb. 21:5). Am na lu bare lu magi mbooloo mi war a seet.
22 Magi mbooloo mi dañu bëgg waa mbooloo mi gën a mën a bokk ci liggéeyu waare bi. Kon dañu war a def porogaraamu ndaje yu ñuy def bala ñuy waare bu mën a baax ci ñépp, te fexe ba ndaje yooyu am ci ayu-bés bi yépp ak ci samdi ak dimaas. Wottukatu liggéeyu waare bi moo war a jiite loolu lépp. Ndax mën nañu def ay ndaje yooyu ci suba teel walla bu ngoon gi bëggee jot walla buy waaj a guddi ? War nañu xamal loolu yépp waa mbooloo mi. Te bu ñu tafee porogaraam bi ci tablo bi nekk ci Saalu Nguur gi, dina gën a leer ci ñépp.
23 Magi mbooloo mi war nañu seet bu baax ndax waajal nañu bu baax lépp lu jëm ci ndaje fàttaliku bi war a am ci 16 awril. Xéyna dinañu war a bokk Saalu Nguur gi ak yeneen mbooloo. Kon war nañu fexe ba lépp mën a ànd bu baax. War nañu seet it porogaraamu set-setal bi, wax kan mooy teral nit ñi, fu ñuy ame mburu mi ak biiñ bi ak ñan ñoo koy jottali nit ñi. War nañu wax mbooloo mi waxtu bi ak fu ñuy defe ndaje bi. Te it su ñu waree soppi dara ci porogaraamu yeneen ndaje ci ayu-bés boobu, dañu ko war a wax mbooloo mi. Nañu toppatoo loolu lépp ba mu baax. Dina tax “ lépp di dox ciy teggin te aw yoon ”. — 1 Kor. 14:40.
24 Ci jamano fàttaliku bi, mbooloo mi dina yokk li mu def ci waaraate bi. Boroom njaboot bu nekk, na fexe ba waa këram bokk ci. Mën na ci waxtaan ak ñoom ci seen njàngum Biibël bi ci njaboot bi. Ndax sa waa kër gi yépp dinañu mën a nekk pioñee yuy jàpple ? Walla ndax mën ngeen fexe ba benn walla ñaar ci yéen mën koo def ? Bu mënul nekk, nangeen waxtaan ba seet naka la njaboot gi mënee yokk li muy def ci liggéeyu waare bi weer yooyu. Su amee ndaw ci seen njaboot, ndax mën nañu ko dimbali te xiir ko ci bëgg nekk waaraatekat bu ñu sóobagul ? Ñaata nit la sa waa kër mën a woo ci ndaje fàttaliku bi ren ? Lii yépp, bu ngeen ko waajalee bu baax, dina tax seen njaboot am mbégte ak ay barke yu bare.
25 Nanga jariñoo bu baax jot gi des : Ndaw li Pieer bindoon na benn bataaxal karceen yu njëkk ya. Dafa leen doon fàttali ne jamano Yawut yi mu ngi bëgg jeex (1 Pie. 4:7). Tey it, lépp lu xew mu ngi wone ne jamano jii moom it mu ngi bëgg jeex. Ngëm googu dafa war a feeñ ci suñu dund bés bu nekk. Ñun ñi sawar ci jaamu Yexowa suñu xel yépp moo war a nekk ci liggéey bu jamp boobu, maanaam waare xibaar bu baax bi. — Titt 2:13, 14.
26 Tey lañu war a wone ne dañu sawar te ñu ngi góor-góorlu ci def lu baax ! Nanga xalaat ci li la Yexowa defal yow, sa njaboot ak mbooloo mi. Dëgg la, mënuñu fey Yexowa ci li mu ñu may yépp. Waaye mën nañu ko jaamu ak suñu xol bépp (Sab. 116:12-14). Bu ñu góor-góorloo ci loolu, Yexowa dina ñu barkeel (Léeb. 10:22). Ñun ñépp nañu ‘ góor-góorlu ci def lu baax ’ ci jamano fàttaliku bi. Nañu yokk li ñuy def ci liggéeyu Yàlla. Su ñu ko defee, dina tax “ turu Yàlla màgg ci lépp, jaar ci Yeesu Krist ”. — 1 Pie. 3:13 ; 4:11.
[Wërale bi nekk 3]
Ñaata nit ñoo teewoon ci ndaje fàttaliku bi ci àddina si sépp
1999 14 088 751
2000 14 872 086
2001 15 374 986
2002 15 597 746
[Wërale bi nekk 4]
Kan ngay woo ci ndaje fàttaliku bi ?
□ Sa waa kër ak say mbokk
□ Say dëkkandoo walla ay nit ñi nga xam
□ Ñi nga bokkal liggéey walla lekkool
□ Ñi ngay dellu seeti walla ñi ngay jàngal Biibël bi
[Wërale bi nekk 5]
Dimbalil ñi teew ci ndaje fàttaliku bi
□ Nuyu leen bu baax
□ Dellul seeti leen
□ Laaj leen ndax dinañu bëgg ñu jàngal leen Biibël bi
□ Wax leen ñu ñów ci waxtaan bi ñu faral di am ci àddina sépp
[Wërale bi nekk 6]
Lan nga fas yéene def ci jamano fàttaliku bi ?
□ Fexe ba mu am ci ñi nga woo kuy ñów teew ci ndaje fàttaliku bi
□ Fexe ba mën a nekk waaraatekat
□ Xam ñaata waxtu nga bëgg waaraate
□ Fexe ba sa waaraate gën a baax ci benn fànn
□ Nekk pioñee buy jàpple