‘ Yéwénleen, bay sédd ñi amul ’
1 Ay xarnoo ngii, ba ndaw li Pool tegtalee Timote mu xiirtal ay mbokki gëmkatam “ ñu def lu baax, te bare jëf yu rafet, ñu yéwén, bay sédd ñi amul ”. (1 Tim. 6:18.) Pool fàttali na itam yawut ya nekkoon karceen, ñu bañ a fàtte “ def lu baax ak di sédde ci seen alal ”. (Yaw. 13:16.) Lu tax mu tegtal lu ni mel ? Ndax xamoon na ne kiy “ def lu baax, añam mooy bokk ci ndamu Yàlla, am ngërëm ak jàmm ”. — Room 2:10.
2 Ndegam Yeowa Yàllaa sàkk lépp, moom moo moom lépp (Peeñ. 4:11). Du ñàkk ne, am nañu ngërëm ci li mu ñuy defal, di ko sàkk ci li mu moom. Bu fekkee sax ne doom-Aadama yu bare, xelum ñàkk-ngërëm lañu soloo, terewul Aji-Kowe ji may ñépp, ñu mën a jariñoo li muy joxe ci fasoŋ bu yéwén, ndax ñu sàmm seen dund (Macë 5:45). Dem na sax ba saraxe Doomam ji ko gënal, ba tax mën nañoo am dund gu dul jeex. Mbëggeel giñ ñu won, ndax waru ñoo xiir ci firndeel suñu ngërëm, ci li ñuy yéwén, ñun it, ak suñuy nawle doom-Aadama ? — 2 Kor. 5:14, 15.
3 Lu ñu mën a sédd nit ñi ? Lu aw yoon doŋŋ la, jëfandikoo ci fasoŋ bu rafet fa kanam Yàlla lépp lu ñu am. Ci lu wóor, li ñu bëgg mooy jàppleek suñu alal liggéeyu Nguur gi, akit ci wàllu xel. Jarul ñu koy wax, xabaar bu baax bi mooy alal ji gën, ju nit mën a am, ndax “ mbirum Yàlla la, mu làmboo dooleem, ngir musal ”. (Room 1:16.) Weer wu ne, bu ñuy jëfandikoo ci fasoŋ bu yéwén suñu jot ak suñu alal ngir bokk ci liggéeyu waare bi ak njàngale mi, dinañu mën a sédd ñeneen alal ju bare jooju ci wàllu xel, alal ju leen di jotloo dund ga dul jeex.
4 Yeowa day yëg bànneex dëgg, bu ñuy jàpple néew-ji-doole yi. Dig na ñu barkeem te mu ngi ñuy fàttali itam lile : “ Alal ju am maanaa du am lenn njariñ ca bésu mer mu tàng ma, waaye njub ci boppam mooy musali ci dee. ” (Léeb. 11:4 ; 19:17). Di jàppleek suñu alal liggéeyu Nguur gi tey bokk ak suñu kem-kàttan ci waare xabaar bu baax bi, pexe yu amul moroom la, yu ñu mën a wonee ne, dëgg-dëgg, ñu yéwén lañu, bay sédd ñi amul.