TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 3/02 p. 3-4
  • Na nga “ bare jëf yu rafet ”

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Na nga “ bare jëf yu rafet ”
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • ‘ Nanga yégle fu nekk Kàddug Yàlla ’
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Nañu góor-góorlu ci def lu baax !
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • ‘ Nañu seedeel ci ñépp xebaar bu baax bi ’
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • “ Nanuy defal ñépp lu baax ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 3/02 p. 3-4

Na nga “ bare jëf yu rafet ”

1 Ci at yi mujj yi mu doon waaraate, Timote ak Titt la ndaw li Pool àndaloon bu baax. Ñoom ñaar ñépp la bind ay baat yuy maye doole. Dafa wax Titt ne “ ñi gëm Yàlla ” dañu war a “ sax ci jëf lu rafet ”. (Titt 3:8.) Dafa wax Timote ne, ku wékk yaakaaram ci Yàlla, dafa war a “ bare jëf yu rafet ”. (1 Tim. 6:17, 18.) Loolu, xelal bu am maanaa la ci ñun ñépp ! Waaye, lan moo ñuy tax a def ay jëf yu rafet ? Te jëf yu rafet yan lañu war a def ci fan yii di ñów ?

2 Suñu ngëm ak suñu mbëggeel ci Yexowa, ak it yaakaar bu doy kéemaan bi mu ñu may, ñoo nuy tax a def ay jëf yu rafet (1 Tim. 6:19 ; Titt 2:11). Ci waxtu bi ñu tollu nii ci at mi, ñu ngi ñuy fàttali ne Yexowa dafa yónni Doomam ngir wone ne amul fenn fu ñu mën a sikkal baayam. Indi na it li mën a may dund bépp nit bu ko yelloo (Macë 20:28 ; Ywna. 3:16). Loolu dina leer ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, bu ñuy def bu 28 màrs jotee. Yaakaaru dund gu dul jeex bi ñu am, ndax du ñu xiir ci def lépp li ñu mën ngir “ bare jëf yu rafet ” ? Wóor na ! Yan jëf yu rafet lañu mën a def léegi ?

3 Jëf yu rafet yi ñu war a def ci weeru màrs ak yi ci topp : Wóor na ne dinañu teew ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Ci at mi yépp, mooy xew-xew bi ëpp solo ci Seede Yexowa yi nekk ci àddina si sépp (Lukk 22:19). Mbégte bi ñuy am bés boobu, dañu ko bëgg bokk ak li gën a bare ci nit ñi. Seetal ci La Tour de Garde bu 1 sãwiyee 2002, li ñu def ci waaraate bi. Dinga gis ne ci ay réew yu bare, ñi teewoon ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, matoon nañu ñetti yoon waaraatekat ya fa nekk, walla sax ñeenti yoon, ba juróomi yoon, yenn saay sax mu ëpp ko. Ci lu wóor, ñi bokk ci mbooloo yi sawaroon nañu bu baax ci gox bu ñuy waaraate ci joxe ay kart yu bare fu ñuy woowe nit ñi ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Looloo tax, ci diggante tey ak 28 màrs, dañu bëgg a def lépp li ñu mën ngir yokk waxtu yi ñuy waaraate, ngir wax nit ñi ñu ñów teew ci ndaje boobu, te dimbali leen ndax ñu jàng lu jëm ci yaakaaru mucc gi.

4 Ndegam weeru awril mu ngi jegesi, bëccëg yi dinañu gën di gudd. Loolu, naka lañu ko mën a jariñoo ngir “ bare jëf yu rafet ” ? Bëccëg yooyu, nañu ci wéy di sawar a waaraate xibaar bu baax bi, tey nekk ñu “ ràññeeku ci jëf yu baax ”. (Titt 2:14 ; Macë 24:14.) Soo mënulee nekk aji-xàll yoonu weer (pionnier auxiliaire) ci weeru màrs, ndax mënoo ko doon weeru awril ak me (walla ci benn ci weer yooyu) ? Su fekkee ne danga nekk aji-xàll yoon ci weeru màrs, ndax mën nga ko kontine ?

5 Suñu ay mbokk yuy liggéey, gis nañu ne, bu ñuy liggéeyi, bu ñuy waaraate ci mbedd mi, walla bu ñuy wax ak jaaykat yiy teel a ubbi seeni bitig, dañu mën a waaraate lu mat benn waxtu. Am na ñuy waaraate ci waxtu añ bi. Ñenn ñi gis nañu ne ci waxtu boobu, mën nañu jàngal Biibël bi kenn ku ñu bokkal liggéey. Suñuy mbokk yu jigéen yu bare yuy liggéey seen biir kër, dañu doon waaraate bu seen doom demee jàngi. Yenn saay, dañu doon teel a yeewu ngir def seen liggéeyu kër. Loolu taxoon na ñu gën a am jotu waaraate ak jàngal Biibël bi. — Efes 5:15, 16.

6 Su dee sax mënoo nekk aji-xàll yoon, mën nga def sa porogaraamu bopp ngir yokk li ngay def ci liggéeyu waare bi. Noonu, dinga “ def lu baax, te bare jëf yu rafet, [...] yéwén, bay sédd ” dëgg gi ak ñeneen ñi. — 1 Tim. 6:18.

7 Bul fàtte ne, sàkk ay taalibe, ci jëf yu rafet yi la bokk : At mu nekk, dafay am ay nit ñu suñu waxtaan neex ñuy teew ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Ci mbooloo mi, ndax mën na am ñu mën a seetlu ñi teew te fekk nekkuñu di jàng Biibël bi ? Ndax mën nañu leen seetiwaat ngir dimbali leen ba ñu jëm kanam ci wallu ngëm ? Ñenn ci ñi teew ci ndaje boobu, mën nañu am ay mbokk yu nekk Seede Yexowa. Am na it ñu ci doon jàng Biibël bi bu njëkk. Ñooñu, xéyna bu ñu waxee ak ñoom, dinañu nangu jàngaat Biibël bi te dinañu fexe ba tàmm fekke ndaje yi. Te bu ñu demee ba ànd ak ñun di jaamu Yexowa, dinañu kontaan lool.

8 Su ñu yokkee li ñuy def ci liggéeyu waare bi ci weeru màrs ak weer yu ci topp, nit ñi suñu waxtaan neex ñi nuy gis, dinañu gën a bare. Nañu leen laaj benn laaj, te dig leen ne dinañu tontu laaj boobu bés bu ñu ñówaatee. Bu ko defee, dellu fa dina ñu gën a yomb. Gaaw fa dellu mooy gën. Bu fekkee ne bi ñu njëkkee wax ak ñoom mënuñu woon a tàmbali jàng ak ñoom Biibël bi, nañu ko jéem a def buñu fa delloo.

9 Bu ñuy waaraate ci mbedd mi, nañu jéem a tàmbali waxtaan ak nit ñi. Bare na waaraatekat yu daje ak ay nit ñu suñu waxtaan neex, bu ñu doon waaraate ci mbedd mi. Am na ci ñu leen jox seen tur, xamal leen fi ñu dëkk, ak seeni nimoro telefon. Bu fekkee ne nit ki ngay waxal dëkkul ci gox fu seen mbooloo di waaraate, jëlal ci sa Saalu Nguur gi, benn kayit Veuillez suivre l’intérêt (S-43), bind ci lépp li ñu ciy laaj, te jox ko seen sekkerteeru mbooloo. Kooku dina ko jox mbooloo buy waaraate ci gox fu nit kooku dëkk. Bu fekkee ne sekkerteer bi mënu ko def, dina ko jox suñu bànqaas ndax mu def ci li ci war. Bu ko defee, dinañu mën a toppatoo nit kooku.

10 Bu fekkee ne nimoro telefon lañu la jox, te xamoo fu nit kooku dëkk, telefone ko ndax ngeen mën a waxtaan. Waajalal li nga war a wax balaa nga koy telefone. Tegal téere Comment raisonner ci sa wet, ndax nga mën ko gaaw a ubbi boo ko soxlaa. Am na ñoo xam ne jàng nañu Biibël bi ak ay nit ci telefon, te loolu jur na lu baax. Jàng nañu sax noonu ak ay nit ñu jafe woon a fekk ci seen kër. Bu mu doon waaraate kër-oo-kër, suñu benn mbokk mu jigéen dafa laaj ay jigéen yu suñu waxtaan neex, lan mooy seen nimoro telefon. Mujj na tàmbali jàngal ñaari nit Biibël bi.

11 Jàppleel mag ñi bu ñuy dimbali ñi bàyyi waaraate : Mag ñi, dañu bëgg toppatoo ñi bàyyi waaraate, toppatoo bu ànd ak mbëggeel. Ñi bàyyi waaraate, am na ci ñu jógal seen bopp, ñówaat fekke ndajey mbooloo mi. Gisal nañu seen bopp ne soxla nañu jege mbootaayu Yexowa, ngir mën a am jàmm ak salaam bi ñuy wax ci Sabuur 91. Léegi, am na ci ñu ci bëggaat waaraate. Su amee ñeneen ñu bàyyi waaraate ñu ñów fekke ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ci weer bii, mën na am ñu nangu jàng Biibël bi. Bu boobaa, magi mbooloo mi dinañu wut kenn kuy jàng ak ñoom Biibël bi. Su ñu la laajee nga dimbali nit ñooñu, soo nangoo def lépp li ñu lay wax, dina baax lool. — Room 15:1, 2.

12 Na nga “ sax ci jëf lu rafet ” : Ci ñi nekk aji-xàll yoonu weer, ñu bare gis nañu ne, ci ay weer yu toppante, seen liggéey ci waaraate bi yokku na. Dañu daje woon ak ay nit ñu suñu waxtaan neex, ñu gis ne war nañu leen a seetiwaat. Looloo tax ñu yokk seen liggéey ci waaraate bi, ngir seetiwaat nit ñooñu. Ñenn ci ñoom tàmbali nañu ay jàng Biibël bi ak ay nit, te loolu tax na ñuy yokk seen waaraate.

13 Am na ñeneen ñoo xam ne, bi ñu yokkee li ñu doon def ci waaraate bi ak ci liggéeyu sàkk ay taalibe, dañu ci jële mbégte mu réy. Loolu tax na ñu seetaat li ñu war a jiital ci seen àddina. Lu mu jur ? Ñenn ñi dañu waññi seen liggéey, ngir mën a nekk aji-xàll yoonu weer te yàgg ci. Ñeneen ñi nekk nañu aji-xàll yoon ju ci sax (pionnier permanent). Dañu wékk seen yaakaar ci Yàlla te bañ ko wékk ci li àddina si di maye. Gis nañu ne “ yéwén, bay sedd ñi amul ”, dafay tax Yexowa barkeel leen te dëgëral seen yaakaaru “ dund gu wóor gi ”. (1 Tim. 6:18, 19.) Ci lu wóor, ñi nekk aji-xàll yoon bu ñu baree, mbooloo mi yépp moo ciy jariñoo. Aji-xàll yoon yi faral nañu nettali li ñu gis ci waaraate bi, te ñaan ñeneen ñu ànd ak ñoom ci waaraate bi. Loolu dafay tax ngëm, jàmm, ak mbégte gën a yokku ci mbooloo mi.

14 Na ku nekk yokk li muy def ci waaraate bi ci jamano fàttaliku bi ak weer yu ci topp, ndax ñu “ bare jëf yu rafet ”. Ñañu wone ne am nañu ngërëm ci li Yexowa def bi mu ñu mayee yaakaaru dund ba abadan ci kow suuf su bees, fa njub dëkk. — 2 Pie. 3:13.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager