Nañu def lu baax te sédde ci li ñu am
1 Dorkas ‘ wéy na ci jëf yu baax ak saraxe ’. (Jëf. 9:36, 39.) Ku bëgg maye la woon. Loolu moo tax nit ñi ak Yexowa Yàlla ci boppam bëgg ko. Yawut yi 13:16 nee na : “ Buleen fàtte di def lu baax ak di sédde ci seen alal, ndaxte sarax yu mel noonu ñoo neex Yàlla. ” Naka lañu mënee def lu baax te sédde ci li ñu am tey, maanaam dindi dara ci li ñu am ngir maye ko ?
2 Lenn li ñu mën a def mooy di sédde ci lu am maanaa li ñu am (Léeb. 3:9). Ak xaalis bi ñuy maye ngir jàpple liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp, dañuy tabax ay Saalu Nguur, ay Saalu ndaje yu gën a mag ak ay bànqaas ci àddina si sépp. Loolu tax na ay milyoŋi nit mën a jot ci li Yàlla di jàngale te mën a daje ak ay mbokk ci ngëm yu leen di xiir ci lu baax.
3 Def luy seddal xol : Bu musiba amee, ñiy jaamu Yexowa dañuy defal “ lu baax ” seeni mbokk ci ngëm ak it ay nit ñu nu bokkul ngëm (Gal. 6:10). Ci Frãs, amoon na benn isin bu jékki-jékki ne téll. Benn góor ak jabaram ñoo dëkkoon ci wetu isin boobu. Dañu ne : “ Isin bi dafa ne téll rekk, suñuy mbokk ci ngëm ñów dimbali ñu ci setal néeg yi ñu dëkkoon. Def nañu loolu itam ci yenn ci suñuy dëkkandoo. Suñu dëkkandoo yi sax dañu waaru woon bi ñu gisee nit ñu bare noonu di ñów ngir dimbali ñu. ” Suñu beneen mbokk mu jigéen yokk na ci lii : “ Magi mbooloo mi ñów nañu dimbali ñu. Wax nañu it lu dalal suñu xel. Loolu sax lañu gënoon a soxla alal. ”
4 Lu baax li ñu mën a defal suñu moroom yi, bare na. Waaye li ci gën mooy waar leen lu jëm ci dëgg gi. Dëgg googu ëmb na li Yexowa ci boppam dige, maanaam “ yaakaar [...] ji nu am ci dund gu dul jeex ”. (Titt 1:1, 2.) Am na ñu nekk ci naqar ndax seen matadi ak it lépp li xew ci àddina si tey. Waaye li Yàlla wax ci Biibël bi dafay seddal bu baax seen xol (Macë 5:4). Kon, bu ñu ko mënee, nañu defal nit ñi lu baax te sédde ci li ñu am. — Léeb. 3:27.