‘ Nu ma koy mëne lu moy kenn tette ma ? ’
1 Ba Filipp waarekat ba laajee jaraafu Ecópi ja ndax nàndoon li mu doon jàng ci Kàddu Yàlla, waa ja lii la ko tontu : “ Nu ma koy mëne lu moy kenn tette ma ? ” Filipp, ak mbég, dimbali na ko mu nànd xabaar bu baax bi jëm ci Yeesu, te loolu yóbbe na, ca saa sa, ci sóobub waa ja ci ndox (Jëf. 8:26-38, NW). Filipp a nga doon déggal noonu santaaneb Krist ‘ sàkk ay taalibe ci biir niti xeet yépp, di leen sóob ak a jàngal ’. — Macë 28:19, 20.
2 Ñun it, war nañoo déggal santaaneb sàkk ay taalibe, ni ko Filipp defe. Waaye, njëm-kanam ci wàllu xel, bu gaaw, bi jaraafu Ecópi bi def, du lu ñu faral di gis ci nit ñi ñuy jàngal Biibël bi. Nit kooka, ab tuubeen ci yoonu Musaa la woon, di boroom xam-xam ci Mbind yi, te daa amoon xol bu nangu, soxla doŋŋ nangu Yeesu ni Almasi ba ñu dige woon. Loolu nag, tëkk dëgg la su fekkee ne ñii ñuy jàngal Biibël bi xamuñu ko, njàngale diine yu moy dëgg gi dañu leen réeral, walla ñu sëfoo jafe-jafe yu tar ci seen dund. Lu ñu mën a dimbali ndax ñu àntu, bu ñuy tette jàngkati Biibël bi ci njébbalu bi, ba noppi sóob bi ?
3 Ràññeel soxlay jàngkatu Biibël bi ci wàllu xel : Ndollentu Le Ministère du Royaume, bu weeru ut 1998 a ngi doon waxtaane diir bi ñu mën a jàng ak nit ñi, bu ñuy jëfandikoo téere bu ndaw bi Laaj ak téere Xam-xam. Tegtal bii la joxe woon : “ Laaj na ñu emale gaawaayu njàng mi ak li aji-jàng ji nekke, akit mën-mënam. [...] Bëgguñoo xañ aji-jàng ji dég-dég bu leer ndax yàkkamti. Aji-jàng ju nekk soxla naa sës, bu dëgër, ngëmam gu bees ci Kàddu Yàlla. ” Noonu, li gën mooy bañ a yàkkamtee gis li ne ci biir téere Xam-xam, ndax danga koy jéem a sottal ci juróom-benni weer. Xëy na, dinañu soxla lu ëpp juróom-benni weer ngir dimbali ñenn ñi ñu jëm kanam ba ci sóob bi. Ba ngay jiite njàng mi ayu-bés gu ne, jëlal jot gi war, gu mu mën a doon nag, ngir dimbali aji-jàng ji mu nànd te nangu li muy jàng ci biir Kàddu Yàlla. Yenn saay, amaana ñu soxla ñaar walla ñetti ayu-bés ngir sottal menn pàcc ci téere Xam-xam. Loolu day tax ñu am jotu duruus te leeral aaya yu bare, yu ñu lim. — Room 12:2.
4 Waaye, loo war a def su fekkee ne sottal nga téere Xam-xam, te nga ràññee ne ki ngay jàngal, dég-dégam lu jëm ci dëgg gi soxla na ñu matal ko, walla xolam xiiragu ko dëgg ci taxawu dëgg gi, ba tax mu jébbal dundam Yàlla (1 Kor. 14:20) ? Leneen lan nga mën a def ngir tette ko ci yoon wiy jëme ci dund gi ? — Macë 7:14.
5 Fajal soxlay jàngkatu Biibël bi ci wàllu xel : Su fekkee ne nit kaa ngiy jëm kanam, bu yéexee sax, te muy gën di fonk li muy jàng, bu boobaa wéyal ci njàngum Biibël bi ak beneen ñaareelu téere, boo sottalee téere bu ndaw bi Laaj ak téere Xam-xam. Du lu war saa su ne, waaye su ko soxlaa, wéyal di jàng ak moom ci téere Paix véritable, Unis dans le culte, walla Parole de Dieu. Yéenekat yu bare am nañu seeni sotti bopp, yu téere yooyu ngir jëfandikoo ko, su ko mbooloo mi amatul. Téere Parole de Dieu doŋŋ lañu mën a yóbbantee Brooklyn. Ak nu mu mënti mel, téere bu ndaw bi Laaj ak téere Xam-xam lañu war a jëkk a jàng. Mën nañoo waññ tey xamal njàngum Biibël bi, seetiwaat yi, ak jot gi ñuy def ci njàng mi, bu fekkee sax ne sóob nañu aji-jàng ji laata moo sottal ñaareelu téere bi.
6 Ndax loolu daa tekki ne dañoo war a dimbaliwaat, ak njàngum ñaareelu téere, ñii ñu sóob bu yàggul te ñu jàng benn téere kott ? Déedéet. Waaye, mën naa am ñoo xam ne waareetuñu walla jëmatuñu kanam ci dëgg gi, walla itam ñu yëg ne soxla nañu ndimbal ci seen wàllu bopp ngir gën a topp dëgg gi ci seen dund. War nañoo giseek wottukatu liggéeyu waare bi, laata ñoo taxawalaat njàngum Biibël bi ak yéenekat bu ñu sóob ba noppi. Waaye, soo xamee nit ñu jàng téere Xam-xam ba sottal te masuñoo jëm kanam ba jébbalu ak ñaan ñu sóob leen, mën naa am nga bëgg a tànn a seet ndax dinañ ànd ci jëlaat seen njàngum Biibël bi.
7 Xàmmikaayu mbëggeelu karceen yi la, wone itte dëgg ci képp ku dëgg gi soxal te ñu ko koy jàngal. Suñu jubluwaay mooy dimbali aji-jàng ji mu gën a nànd dëgg gi ne ci biir Kàddu Yàlla. Bu boobaa lay mën a taxawu dëgg dëgg gi, sës ko ci xam-xam, te ci lay mën a jébbal dundam Yeowa, misaale njébbaloom ak sóob bi cim ndox. — Sab. 40:8; Efes 3:17-19.
8 Ndax yaa ngiy fàttaliku la xewoon gannaaw ba ñu sóobee jaraafu Ecópi ja ? “ Mu toppaat yoonam, ànd ak mbég ”, niki taalibe Yeesu Krist, bu bees (Jëf. 8:39, 40). Ñun ak ñii ñuy tette ci yoonu dëgg gi te àntu ci, yal nañu yëg mbég mu réy ciy jaamu Yeowa Yàlla — tey ba abadan !