Téere Qu’enseigne la Bible ? lañuy njëkk jàng léegi ak ñi ñuy jàngal Biibël bi
1 Ci ndaje bi gën a mag bi tudd “ Nañu déggal Yàlla ”, génne nañu téere bu bees bu tudd Qu’enseigne réellement la Bible ? (maanaam lan la Biibël bi di jàngale dëgg.) Bés boobu kontaanoon nañu lool. Ci Samdi bi, bi ndaje bi jeexee, képp ku teewe woon jot na ci benn. Téere bu bees boobu, dañu ko defar ngir jàngal nit ñi Biibël bi. Naka lañu koy jariñoo ? Moom lañuy njëkk jàng léegi ak ñi ñuy jàngal Biibël bi. Ci weeru màrs lay njëkk nekk téere bu ñu war a wone ci waaraate bi. Waaye ñu ngiy ñaan waaraatekat yi ne képp ku bëgg komaase njàngum Biibël walla ñi ko komaase ba pare, nañu ko def léegi ci téere bu bees boobu. Buñu xaar ba weeru màrs.
2 Bu fekkee ne ñu ngiy def ba pare ay njàngum Biibël ci beneen téere : Am na waaraatekat yuy def fi mu ne nii ay njàngum Biibël ci téere Xam-xam walla ci téere Laaj. Ñooñu war nañu seet bu baax kañ ak naka lañu war a komaasee jëfandikoo téere bu bees boobu ci njàngum Biibël yooyu ñuy def. Su dee bi nga komaase njàngum Biibël bi yàggul, mën nga tàmbaliwaat njàngum Biibël bi ci téere bu bees bi ci pàcc bu njëkk bi. Bu fekkee ne xaw nga sore ci téere Xam-xam bi, seetal ci téere Qu’enseigne la Bible ? pàcc bi méngoo ak pàcc bi ngeen di jàng ci téere Xam-xam bi, te nangeen fa kontine seen njàngum Biibël bi. Bu fekkee ne li leen desee jàng ci téere Xam-xam bi barewul, bu la neexee, mën ngeen kontine ci téere Xam-xam ngir àggali ko.
3 Wóor na ne xam nañu ñun ñépp ay nit ñu bare ñoo xam ne, bu ñu jàngoon Biibël bi ci téere bu bees bi, dina leen jariñ bu baax. Ak téere boobu dinañu mën a jàngal nit ñi ñu xam ndànk-ndànk li nekk ci Biibël bi. Ndax bëgguloo wax képp kooy dajeel ne danga ko bëgg jàngal Biibël bi ci téere boobu ? Am na ay nit ñu mas a jàng téere Laaj walla téere Xam-xam, waaye masuñu jébbal seen bopp Yexowa ba ñu sóob leen. Nit ñooñu, xéyna dinañu bëgg komaasewaat seen njàngum Biibël ci téere bu bees boobu. Xéyna sax wayjur yi dinañu bëgg jàng téere boobu ak seeni doom ngir ñu am xam-xam bi wér ci Yàlla. — Kol. 1:9, 10.
4 Téere bu ñu mën a jàng bu ñu paree ci téere bu bees bi : Ndax am na beneen téere bu ñu mën a jàng bu ñu paree ci téere Qu’enseigne réellement la Bible ? Waaw. Nit kiy jàng, bu fekkee ne mu ngi jëm kanam, bu dee sax ndànk-ndànk la koy defe, te fonk na li muy jàng, mën ngeen kontine njàngum Biibël bi ci téere Adorez le seul vrai Dieu. Téere Qu’enseigne la Bible ? dina ñu dimbali bu baax bu ñuy sàkk ay taalibe ni ko Yeesu santaanee. — Macë 28:19, 20.