Wéyal di waare !
1 Coobare Yàlla la, “ ñépp mucc te xam dëgg gi ”. (1 Tim. 2:4.) Looloo tax ñu sas ñu waare xabaar bu baax bi (Macë 24:14). Su ñu nàndee lu tax ñu war a wéy di waare, dara lu ñu jànkoonteel du ñu mën a yoqiloo walla fàbbi ci sas woowu.
2 Lu tax ñu war caa jàpp bu dëgër ? Ci àddina si, am na lu bari luy fàbbi te tax nit ñi fàtte walla ñàkk a faaydaal li ñu leen di wax. Looloo tax ñu war di wéy di leen fàttali xabaaru Yàlla, biy musal (Macë 24:38, 39). Rax-ca-dolli, li nit ñi nekke ci seen dund day soppeeku saa su ne. Nekkini àddina si sax, mën naa soppeeku bu gaaw a gaaw, ci xef-xippi (1 Kor.7:31). Ëllëg, ayu-bés walla weer wiy dikk, nit ñi ñuy waare mën nañoo jànkoonteek jafe-jafe yu bees walla i jaaxle, yu leen di xalaatloo bu baax a baax ci xabaar bu baax, bi ñu leen di indil. Ndax amoo ngërëm ci li Seede, bi la indil dëgg gi, nekkoon ku jàpp bu dëgër ci sasam ?
3 Ngir roy ci yërmande Yàlla : Yexowa ci mën-muñam bàyyi na jamano dox, laata moo matal àtteem ci kow ñi soxor. Jaare ci ñun, wéy na di woo ñi seen xol jub ndax ñu jublu ci moom te mucc (2 Pieer 3:9). Dinañu yenu boru deret, su ñu wéyul di yéene nit ñi xabaaru Yàlla, bu làmboo yërmande bi, su ñu leen artuwul itam ci ñëwu àtte Yàlla ci kow ñépp ñi dëdduwul seeni yoon yu bon (Esek. 33:1-11). Bu fekkee sax ne, du saa su ne la nit ñi di nangu suñu waare, waruñoo wàññi mukk suñuy njéem ngir dimbali ñi seen xol jub, ñu fonk yërmandey Yàlla, ju mag ji. — Jëf. 20:26, 27 ; Room 12:11.
4 Ngir wone suñu mbëggeel : Yexowa Yàlla, jaare ci Yeesu Krist, moo sant ñu waar xabaar bu baax bi ci kow suuf si sépp (Macë 28:19, 20). Bu fekkee sax ne nit ñi dañoo lànk, bañ a déglu, xàllal nañ ñu yoon ngir ñu wone suñu mbëggeel ak suñu taq ci Yàlla, ci li ñuy wéy di def li jub. — 1 Ywna. 5:3.
5 Yal nañu dogu ci wéy di waare ! Nañu ko def ak cawarte, ba ñu nekkee ba tey ci ‘ bésu muccu ’ Yexowa. — 2 Kor. 6:2.