TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 2/02 p. 8
  • Lu tax waruñu bàyyi waaraate ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Lu tax waruñu bàyyi waaraate ?
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Lu tax ñuy delluwaat ay yooni yoon ci nit ñi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Wéyal di waare !
    Sasu Nguuru Yàlla — 2000
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 2/02 p. 8

Lu tax waruñu bàyyi waaraate ?

1 Ndax yàgg nga di waare xibaaru Nguur gi fi nga nekk (Macë 24:14) ? Su dee waaw, mën na am ngay xalaat ne, li ngeen waaraate ci gox bu ñu jagleel seen mbooloo, doy na. Xéyna, tey, booy waaraate, li ëpp ci nit ñi ngay dajeel, duñu sawar a waxtaan lu jëm ci xibaaru Nguur gi. Waaye, seetal li ñu wax ci ñi nekk taalibe Yeesu dëgg. Ci téere Prophétie d’Isaïe II, xët 141, lii lañu wax ci ñoom : “ Ak li ñu liggéey yépp, am na ay béréb yoo xam ne, dafa mel ni li ñu fa waaraate jurul dara. Wànte, loolu dañu koy muñ. ” Kon lu tax waruñu bàyyi waaraate ?

2 Fàttalikul Yérémi : Bu nit ñi dégloo ak bu ñu bañee déglu yépp, waruñu bàyyi waaraate. Yérémi waaraate na lu mat 40 at ci benn béréb. Waaye ñi ko doon déglu, barewuñu woon dara. Ñu bare, dañu doon xeex li mu doon wax. Lu tax Yérémi bàyyiwul waaraate ? Liggéey bi mu doon def, Yàlla moo ko ko santoon. Yérémi xamoon na it li doon waaj a am. Looloo taxoon mu ñeme woon a waaraate. — Yér. 1:17 ; 20:⁠9.

3 Tey, ci lu mel noonu lañu nekke. “ Yeesu sant na nu, nu yégal xeet wa, di seede ne, moom la Yàlla jagleel àtteb ñiy dund ak ñi dee. ” (Jëf. 10:42). Xibaar bu ñuy waaraate, mën na tax ñi ko dégg dund walla ñu ñàkk seen bakkan. Nit ñi, dinañu leen àtte ci li ñuy def bu ñu déggee xibaar bu baax bi ba noppi. Looloo tax, def lépp li ñu nu sant, mooy suñu warugar. Su dee sax nit ñi dañuy bañ a déglu li ñuy wax, bu ñu defee li ñu war, ci lañuy mën a wone fu suñu mbëggeel ci nit ñi ak suñu ngëm ci Yexowa tollu. Waaye leneen am na.

4 Dina ñu jariñ : Bu nit ñi nangoo xibaar bu baax bi ak bu ñu ko bañee yépp, xel mu dal ak mbégte bu ñuy am bu ñuy topp Yàlla, leneen mënu ñu ko may (Sab. 40:⁠8). Suñu dund dina am njariñ dëgg. Bu ñu yokkee li ñuy def ci liggéeyu waaraate bi, yaakaar ak mbégte yi jëm ci dund ci biir Àjjana, dinañu gën a nekk ci suñu xol ak suñu xel. Bu ñu xalaatee ci yëf yooyu ñu dige ci Mbind mi, suñu ngëm dina gën a dëgër, te suñu diggante ak Yàlla dina gën a rattax.

5 Bu dee sax suñu liggéey ci waaraate bi, li muy jur du feeñ ci saa si, xéyna jëmbët nañu doomu dëgg gi ci xolu nit ki. Te waxtu bu ko Yexowa bëggee, doom boobu dina sax (Ywna. 6:44 ; 1 Kor. 3:⁠6). Li Seede Yexowa yi di waare ci sa dëkk, walla ci àddina si sépp, kenn xamul ñaata nit lay nar a dimbali ba ñu jàng xam Nguuru Yàlla.

6 Tey lañu war a gën a topp li ñu Yeesu sant, maanaam :“ Moytuleen te xool! Xamuleen kañ la waxtu wi di jot. Li ma leen wax, ñépp laa ko wax: Xoolleen! ” (Mark 13:​33, 37). Kon nag, bu kenn bàyyi waare xibaar bu baax bi ci Nguuru Yàlla. Nañu bokk ci ñiy sellal turu Yexowa bu mag bi, bu ko defee ñuy seddal xolam.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager