TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 4/05 p. 1
  • Nanga kontine di waaraate

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nanga kontine di waaraate
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Wéyal di waare !
    Sasu Nguuru Yàlla — 2000
  • Nañu “ jaar ciy tànkam ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 4/05 p. 1

Nanga kontine di waaraate

1 Ñu ngi dund ci jamano ju metti. Foo mënta dem, dégg ay xeex ci biir dëkk yi, ay xeex diggante xeet, ay yëngu-yëngu suuf walla musiba yu mel noonu, ak yeneen yoo xam ne lu ñaaw la te metti na. Waaw, ci dëgg, doom-Aadama yi soxla nañu dégg xibaar bu neex, rawatina ci suñu jamano ji ñu nekk nii. Waaye tey, fekk nit ñi seen kër ci waaraate bi, yombul. Te fekk ku ñuy déglu walla ku bëgg a jàng Biibël bi moo gën a jafe sax. Waaw, barewul ñi bëgg a waxtaan ci Yàlla. Waaye ba tey, fàww ñu kontine di waare xibaar bu baax bi. Xibaar boobu, mu ngi jëm ci Nguuru Yàlla bi Yàlla samp ba pare. — Macë 24:⁠14.

2 Bëgg nit : Suñu waaraate dafay wone mbëggeel bi Yexowa am ci nit ñi. “ Bëggul kenn alku, waaye ñépp tuub seeni bàkkaar. ” (2 Pie. 3:9 ; Esek. 33:11). Kon, ni ko Yeesu waxe, lii la Yàlla bëgg : “ Fàww xebaar bu baax bi jëkka jib ci [maanaam jot] xeet yépp. ” (Mark 13:10). Yàlla mu ngi woo nit ñi ngir ñu ñów ci moom te mën a mucc bés bu àttee àddina Seytaane sii (Yow. 2:​28, 29, 32 ; Tsë. 2:​2, 3). Ndax ñun ñii, ñu ngi gërëm Yàlla ci loolu ? — 1 Tim. 1:​12, 13.

3 Boo xoolee li Seede Yexowa yi def ci àddina si sépp ci atum liggéeyu waare bu 2004, dinga gis ne 6 085 387 njàngum Biibël lañu def weer wu nekk. Te ayu-bés bu nekk dafa amoon lu jege 5 000 taalibe yu ñu doon sóob ci ndox ! Ci 5 000 yooyu, am na ñu dem ba jébbal seen bopp Yàlla ndaxte dafa am ay waaraatekat yu kontine di waar ñépp ci seen goxu mbooloo, te Yàlla moo leen ci barkeel. Loolu indi na mbégte mu réy ci mbooloo yi. Te it bu ñuy def loolu, dañuy ànd ak Yàlla ci liggéey boobu nga xam ne dafay muccal nit. Aka nekk lu réy ! — 1 Kor. 3:​5, 6, 9.

4 Màggal turu Yàlla : Duñu bàyyi waaraate bi, ndaxte dañu bëgg màggal Yexowa te sellal turam ci kanamu ñépp (Yaw. 13:15). Seytaane dafa nax “ waa àddina sépp ”. (Peeñ. 12:⁠9.) Fexe na ba nit ñi gëm ne Yàlla mënul faj suñuy coono yépp. Tax na nit ñi foog ne Yàlla faalewul coono yi doom-Aadama am yépp. Dem na sax ba gëmloo nit ñi ne Yàlla amul. Bu ñuy waaraate ñu ngi wax ñépp dëgg gi jëm ci suñu Baay bu baax bi nekk ca asamaan. Nañu kontine di màggal turam, fii ba abadan. — Sab. 145:​1, 2.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager