Dañu kontaan lool ci li ñuy jébbal suñu bopp ci liggéeyu Yexowa !
1 Ndaw li Pool, dafa “ joxe boppam ” ngir def wàllam ci waaraate bi. Loolu dafa taxoon mu bég lool (2 Kor. 12:15). Noonu it tey, ay karceen yu bare dañu nekk pioñee te dañu ciy def liggéey bu rafet. Am na ñeneen ñu war a toppatoo seen njaboot, mu diis lool te seen porogaraam xat. Waaye ayu bés bu nekk, dañuy fexe ba xajal ci seen porogaraam waxtu bu ñuy waare. Am na ci ñu feebar. Barewuñu doole, waaye ñu ngi def lu ñu mën ngir Nguuru Yàlla jëm kanam. Ñi bokk ci mbooloo Yexowa, dañuy jébbal seen bopp ci liggéeyu Yexowa. Seetuñu ci at yi ñu am, walla li ñu nekke.
2 Bëgg sa moroom : Bu ñu defee lépp li ñu mën ngir liggéeyal Yexowa, te wone ne fonk nañu Yàlla ak suñu moroom, dina tax ba suñu xel duñu tuumaal ci dara. Looloo tax bi Pool jébbalee boppam ci liggéeyu waare xibaar bu baax bi, mu mën a wax lii ak mbégte : Damay “ dëggal tey jii ne wàccoo naa ak yéen ñépp ”, maanaam dafa set ci deretu nit ñépp (Jëf. 20:24, 26 ; 1 Tes. 2:8). Def lépp li ñu mën ci liggéeyu waare bi, dina tax ñu bañ a gàddu àqu nit ñi. — Esek. 3:18-21.
3 Bu ñu nangoo sonn ngir dimbali suñuy moroom, dinañu am mbégte (Jëf. 20:35). Suñu been mbokk mu góor nee na : “ Bu ma yendoo ci liggéeyu Yexowa ba ngoon jot, wax dëgg , damay sonn. Waaye damay bég itam, te sant Yexowa ndaxte moom moo ma may mbégte boobu nga xam ne kenn mënu koo dindi ci man. ”
4 Bëgg Yàlla : Li ëpp solo ci li waral ñuy jébbal suñu bopp ci liggéeyu Yexowa mooy dafay neex suñu baay bi nekk ca asamaan. Mbëggeel bi ñu am ci Yàlla dafay tax ñu topp li mu santaane. Waaraate ak sàkk ay taalibe bokk na ci li mu santaane (1 Ywna. 5:3). Ci waaraate bi, mën na am ay nit ñu nu bañ a faale walla ñu nu bëgg a kontar, waaye ba tey ñun dinañu kontine di def bu baax liggéeyu Yexowa, te boole ci mbégte.
5 Du ci waxtu bi ñu nekk nii lañu war a waññi li ñuy def ci liggéeyu Yexowa. Ci waxtu ngóob bi lañu tollu (Macë 9: 37). Beykat yi dañuy faral di liggéey waxtu yu bare bu ñuy tollu ci jamano ngóob, ndaxte fan yi ñu am bala ngóob bi di yàqu, barewuñu. Ñun itam, waxtu bi ñu am ngir def liggéeyu ngóob bi ci wallu ngëm, barewul. Nañu bàyyi suñu xel ci jamano ji ñu tollu tey, te def suñu kem-kàttan ci liggéeyu waare bi. — Luug 13:24 ; 1 Kor. 7:29-31.