“ Maa ngi taxaw temm ! Taxaw temm ! Ne temm ! ”
1 Kàddu yooyu, karceen bu takku, bu muccoon ci Holocauste [Rendi] ba, moo leen wax, te dañuy awu dogu bi ay junniy Seede — ñuy dund ba tey, walla ñu gaañu — dogu woon, maanaam ne temm ci li ñu gëmoon, ak lu leen nasi yi soxore woon a soxore (Efes 6:11, 13). Seen jaar-jaar, bu làmboo fit ak ndam, biy dawloo yaram it, lañuy nettali ci widewo biy fital dëgg, te tudd La fermeté des Témoins de Jéhovah face à la persécution nazie. Ñu ngiy xiirtal ñépp ñi bokk ci mbooloo mi ñu seetaan ko te xamal, ku nekk moroomam, li mu ci xalaat ak a yëg ci biir xolam.
2 Mayal laajte yii, ñu xiir la ci xalaat : (1) Lu tax Seede Yexowa yi taxaw temm ci bañ a jàpple nasi yi ? (2a) Yan gis-gis yu juuyoo amoon lu jëm ci ni ñu doon nuyoo, te lu tax loolu ? (2b) Nan la loolu laale njabooti Seede yi ? (3) Ñaata Seede lañu sànni woon ci dalu yu nekkoon ay kaso, nan lañu leen fa doon xàmmee, te lu leen Gestapo bi doon def ? (4) Génn kaso jaralul woon suñu mbokk yi ñu def lan ? (5a) Nan ak kañ la Seede Yexowa yi yëkkëti seen baat ngir weejal jëfi coxorte nguurug Hitler ? (5b) Lan la Hitler def booba ? (6) Ni jaami Yexowa yi jàppalante, nan la sàmme seen bakkan, ñoom ak ñeneen, akit seen digganteek Yàlla ? (7) Woy-Yàlla wan lañu bindoon ci dalu bu nekkoon kaso ? (8) Royukaayi góor ak jigéen ak ndaw ñu takku yan, ñoo lay xiir ci sàmm sa ngor ci Yexowa, ak lu mu mënta doon ? (Seetal itam Annuaire 1999, xët 144-7.) (9) Niki kenn ci Seede Yexowa yi, nan la la widewo bi yëgloo ne bokkuloo ci àddina si ?
3 Royukaayu Seedey Yexowa, bi ñu nettali ci widewo bi tudd La fermeté, muy royukaay buy fital, mën naa dimbali ndaw ñi, bu ñu dul Seede sax, ñu sàkkal pexe werante yu am solo mel ni nootaange, jañu àndandoo, ak dalal seen xel fa kanam Yàlla. Soo dee ndaw tey dem ci lekkool yi digg-dóomu walla gën a kowe, ndax mën ngaa xàllal say jàngalekat yoon wu ñu jëfandikoo kaset bi, bu ñuy jàngale ? Xéy na, mën nga leen a won sottib widewo bi, naan, ci nettalib li xewoon, wàll wu ñu bare umple la, walla taxaw-seetlu la, bu ànd ak njàngale muy rafetal jikko.
4 Widewo bi tudd La fermeté, jumtuwaay bu baax a baax la ngir wone ni ñu njàngalem Yàlla dee dooleel ci wàllu xel ngir neex ko, bu ñuy sax ci ne temm ci taxawu li jub (1 Kor. 16:13). Bokkal loolu ak ñépp ñi ittewoo dëgg gi.