Lan ngay jiital ci sa dund ?
1 Lan ngay tontu ci laaj boobu ? Leer na ne, kenn ku nekk ci ñun, bëgg na njëkk wut lépp lu jëm ci Nguur gi (Macë 6:33). Waaye war nañu laaj suñu bopp lii : ‘ Li may tànn ci sama dund, ndax dafay wone ne loolu laay def ? ’ Biibël bi dafa ñu ne : “ Seetluleen seen bopp. ” (2 Kor. 13:5). Naka lañu mënee seetlu suñu bopp ngir wone ne ñu ngi njëkk wut Nguur gi ?
2 Lan lañuy def ci jot bi ñu am : Li ñu mën a njëkk def mooy seetaat li ñuy def ci jot bi ñu am (Efes 5:15, 16). Ayu-bés bu nekk, ñaata waxtu lañuy def ci seeti ay mbokk walla ay xarit, seetaan tele, jëfandikoo Internet, walla def liggéey bu ñu neex lool ? Nañu bind waxtu yooyu ci kayit ba pare, ñu tollale ko ak waxtu yi ñuy def ci lépp lu bokk ci jaamu Yàlla. Xéyna li ñuy gis dina ñu bett. Ndax dañuy def waxtu yu bare ci suñu liggéey ngir am liy neexal suñu àddina, ba loolu tere ñu def li ñu war a def ngir jaamu Yàlla ? Ñaata yoon lañuy bañ a dem ci ndaje yi walla ci waaraate bi ndax li ñuy tukki samdi ak dimaas ngir féexal suñu xol ?
3 Nañu seet li war a jiitu ci suñu dund : Li ëpp ci ñun amuñu jot bu doy ngir def lépp li ñu bëgg. Kon bu ñu bëggee njëkk wut lépp lu jëm ci Nguur gi, dañu war a tànn li war a jiitu ci suñu dund, ba pare ñu beral jot bi ñuy defe yëf “ yi gën a rafet ” walla yi ëpp solo (Fil. 1:10). Lii di topp bokk na ci yëf yooyu : gëstu Kàddu Yàlla, waaraate, faj say soxla njaboot, ak teewe ndaje karceen yi (Sab. 1:1, 2 ; Room 10:13, 14 ; 1 Tim. 5:8 ; Yaw. 10:24, 25). Leneen lu mel ni espoor bu yem ak féexal sa xol ci fasoŋ bu sell, am na njariñ (Mark 6:31 ; 1 Tim. 4:8). Waaye yëf yooyu bokkuñu ci yi ëpp solo. Kon dañu leen war a yemale fi ñu war a yem.
4 Suñu benn mbokk bu nekkoon ndaw dafa bëggoon a njëkk wut Nguur gi. Mu daldi jébbal jotam yépp ci liggéeyu waare bi te bañ a jàng njàng bu sore bu mënoon a tax mu am liggéey bu baax. Dafa jàng beneen làkk te toxu ci gox fu ñu soxla woon ay waaraatekat. Lii la wax : “ Li ma nekke fii, neex na ma lool. Liggéeyu waare bi dafa neex lool ! Li may ñaan mooy yeneen ndaw yépp def li ma def te yëg li may yëg. Def li nga am yépp ci liggéeyu Yexowa, dara dàqu ko. ” Waaw, ku njëkk wut Nguur gi, dinga am barke yu bare. Waaye li ëpp solo mooy, ku def loolu dinga neex suñu baay Yexowa mi nekk ci kow asamaan. — Yaw. 6:10.