Wéerul ci Yexowa ngir am doole
1 Bari na yëf yi tax ñu soxla wéeru ci Yexowa. Waar xabaar bu baax bi “ ci àddina [si] sépp ”, sas wu ñu mën a tiital la (Macë 24:14). Duñu jóg itam ci xeex suñu matadi (Room 7:21-23). Magum loolu, “ ndëndu xare jib na [...] suñu diggante [...] ak [rab yi nekk] kilifa yiy nëxal àddina si ”. (Efes 6:11, 12.) Leer na ne, soxla nañu ndimbal. Nu ñu mënee sàkku doole ci Yexowa ?
2 Ñaanal Yàlla : Yexowa, ci fasoŋ bu yéwén, day may jaamam yi ko koy ñaan, xelam mu sell, mu am kàttan mi (Lukk 11:13). Ndax danga di ku wóoluwul sa bopp lu jëm ci seede këroo kër, ci mbedd mi, walla ci telefon ? Ndax danga di ku am kersa ci seede, saa yoo ci amee bunt bu ñu la ubbil ? Ndax li niti sa gox faalewul li ngay wax daa wàññi sa cawarte ? Looy def, saa yu ñu lay gaawtuloo ak doole, nga dëddu sa ngëm walla sa ngor ? Wéerul ci Yexowa. Ñaan ko mu dooleel la. — Fil. 4:13.
3 Jàngalal sa bopp : Ni rekk lekk dee maye doole, noonu itam la faral di dunde Kàddug Yàlla ak mbind yi jóge ci “ surga bu takku te teey ” bi dee ñu dooleel ci wàllu xel (Macë 4:4 ; 24:45). Ba ñu ko laajee li ko mayoon doole muñ ay ati ati kaso — fekk amul Biibël, teg ci, daawul gis kenn — ca réewum Chine, lii la Stanley Jones wax : “ Mën nañoo taxaw temm ci ngëm. Jarul ñu koy wax, fàww ñu jëkk a jàng. Duñu am fit, su ñu dul gëstu. ”
4 Teewal ci ndaje yi : Ci ndaje mu ay karceen amoon ca xarnu bu njëkk ba, Yudd ak Silas “ dooleel [nañu] mbokk yi, di dëgëral seen fit ak wax yu bare ”. (Jëf. 15:32.) Noonu it tey, li ñuy dégg ci ndaje yi day xóotal suñu ngërëm ci Yexowa, di tabax suñu ngëm, te da ñuy xiir ci gën a sawar ci sasu waare bi. Ndaje yi dañuy tax ñu faral di duggook ñiy ‘ liggéeyandook ñun ngir nguuru Yàlla ’, ñoom ñiy ‘ féexal suñu xol ’. — Kol. 4:11.
5 Soxla nañu ndimbal ci “ bési tiis yu tar ” yi ñu tollu (2 Tim. 3:1). Lu jëm ci ñiy sàkku doole ci Yexowa, lenn de wóor na ñu : “ Dinañu yëkkëtiku ak i laaf, niki ay jaxaay. Dinañu daw te duñu lott ; dinañu dox te duñu tàyyi. ” — Isa. 40:31.