Nañu wone ne fonk nañu alalu mbootaayu Yàlla
1 Bi Buur bi Yosiyas doon defaraat kër Yàlla, am na li mu wax ci ñi waroon a def liggéey bi. Dafa ne : “ Xaalis bi ñu leen jox, waruñu leen laaj fi mu jaar, ndaxte ak ngor lañu def seen liggéey. ” (2 Bu. 22:3-7). Fasoŋ bi nit ñooñu doon jëfandikoo alal bi ñu leen dénk, wone woon na ni ñu ko fonke. Tey itam, bu ñuy def liggéey bu sell bu jëm ci xibaar bu baax bi jóge ci Yàlla, war nañu wone it ngor ci fasoŋ bu ñuy jëfandikoo alal bi ñu nu dénk.
2 Ci liggéeyu waare bi : Fonk nañu lool suñu téere yi, ndax xam nañu ne xibaar bi ci nekk dafa am solo lool, te xaalis bu bare lañu jël ngir defar leen. Waruñu leen jox ñi nga xam ne dëgg-dëgg bëgguñu déglu xibaar bi nekk ci Biibël bi. Bu nit wone ne xibaar bu baax bi tuuti rekk la ko neex, dañu ko war a may kayit bu ndaw, te bañ koo may téere.
3 Bu ñuy joxe suñu téere yi, buñu fàtte xaalis bi ñu ci def ngir defar leen. Buñu ko bàyyi ci béréb yoo xam ne nit ñi dinañu ko tasaare rekk. Nañu seet yan téere lañu am ci suñu kër balaa ñuy wut yeneen, ngir bañ a yàq. Su fekkee ne li ngay jot ci yéenekaay bu nekk ci mbooloo mi dafay faral a ëpp, seetal ndax waruloo wàññi yéenekaay yi ngay jël.
4 Téere yi ngay soxla yow mii ci sa wàllu bopp : Téere yi ñu soxla kese lañu war a laaj, rawatina bu ñuy laaj Bible de luxe, Bible à référence walla téere yu mag yu mel ni Concordance, Index, Perspicacité ak Prédicateurs. Defar téere yooyu yépp, laaj na xaalis bu bare.
5 Ndax dangay bind sa tur ak sa adarees ci bépp téere bi nga moom ? Loolu dina tax mu bañ a réer, te doo ci soxla wuti beneen. Boo réeralee benn téere-woy yi, benn Biibël, walla benn ci téere yi ñuy jàng ci mbooloo mi, mën na am nga gis ko fi ñuy dence téere yi ñu réeral ci Saalu Nguur gi walla ci ndaje yu mag yi. — Lukk 15:8, 9.
6 Nañu seet bu baax ni ñuy jëfandikoo suñu téere yi. Noonu lañuy wonee ngor ci fasoŋ bi ñuy jëfandikoo alalu Nguur gi bi ñu Yexowa dénk. — Lukk 16:10.