Lan moo war a ëpp solo ci yow ?
1 Ci diine yu bare, tabax ay lekkool, walla ay loppitaan mooy li ëpp solo. Dëgg la, Seede Yexowa yi duñu “ fàtte di def lu baax ak di sédde ci seen alal ”. (Yaw. 13:16.) Waaye li ëpp solo ci ñoom mooy dimbali nit ñi ci wàllu ngëm.
2 Li ñu mën a jànge ci karceen yu njëkk yi : Lu baax li Yeesu def, bare na. Waaye ci moom, jàngal nit ñi dëgg gi moo ëppoon solo lépp (Lukk 4:43 ; Ywna. 18:37 ; Jëf. 10:38). Santoon na taalibeem yi lii : “ Demleen nag sàkk ay taalibe ci xeet yépp, [...] te ngeen jàngal leen. ” (Macë 28:19, 20). Nee woon na ne ñi ko gëm, bu ñuy def liggéey bi mu tàmbali woon, dinañu dem fu gën a sore fi mu demoon (Ywna. 14:12). Ci Yeesu, waaraate bi moo ëppoon solo lépp, ndaxte ci la doon xamal nit ñi ni ñu mënee mucc. — Ywna. 17:3.
3 Ndaw li Pool xamoon na ne dafa waroon a waaraate. Mënu ko woon a bañ a def (1 Kor. 9:16, 17). Looloo taxoon mu nangu ñàkk lu bare, te muñ jafe-jafe ak metit yu mu mënta doon, ngir mën a def liggéey boobu (Jëf. 20:22-24). Ndaw li Pieer ak ñi mu doon liggéeyal, nangu woon nañu lu mel noonu ñoom itam. Dóor nañu leen. Téj nañu leen kaso. Waaye loolu terewu leen waaraate. “ Daawuñu noppee jàngale ak a xamle xebaar bu baax bi, ne Yeesu mooy Almasi bi. ” — Jëf. 5:40-42.
4 Ñun nag ? Ndax waare xibaaru Nguur gi ak sàkk ay taalibe mooy li ëpp solo ci ñun ? Tey, am na ñu sonn lool. Ndax ñu ngi leen di xalaat dëgg ni ko Yeesu daan def (Macë 9:36) ? Li xew ci àddina si ak li Mbind mi yégle, wone na ne àddina su bon sii, léegi mu jeex ! Buñu fàtte ne liggéeyu waare bi dafa am solo lool. Kon dinañu ci sawar.
5 Seetal li nga mën a def : Li nga mënul a def tey, xéyna ëllëg dinga ko mën. Kon nag, léeg-léeg war nga seetaat sa bopp ba xam ndax mënoo yokk li ngay def ci waaraate bi. Suñu benn mbokk mu jigéen nekkoon na pioñee bu ci sax (permanent), ci diggante 1950 ba 1970. Waaye am na jamano joo xam ne, dafa doon feebar rekk. Looloo taxoon mu bàyyi nekk pioñee. Bi mu demee ba tane, dafa seetaat boppam, te gis ne mën na nekkaat pioñee. Mujj na dem ci lekkoolu pioñee yi, te fekk 90 at la amoon. Mbégte mu réy la ci jële. Yow nag ? Ndax léegi nga dem àllaateret (retraite), walla léegi nga jeexal sa njàng ? Bu loolu amee, ndax dinga mën a nekk pioñee ?
6 Am na bés boo xam ne, Mart dafa ‘ jàppoon lool ca waañ wa ’.Yeesu daldi ko wax ne bu defoon lu gën a yomb, ci lay ëpp barke (Lukk 10:40-42). Yow nag, bu fekkee ne dangay liggéey, ndax sa jabar war na liggéey moom itam ? Bu ngeen yombalalee seen dund, lii ñu lay fey, ndax du leen doy ngir toppatoo seen njaboot ? Am na ñu góor góorlu ba yokk li ñuy def ci waaraate bi. Loolu dafa gën a dëgëral seen ngëm.
7 Ñun ñépp, nañu def ni Yeesu ak ndawam yi. Te nañu wóor ne bu ñu góor-góorloo ngir def lépp li ñu mën ci waaraate bi, Yexowa dina ñu barkeel bu baax. — Lukk 9:57-62.