Ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu : Li ñu warul a fàtte
Ren, ci bésu àllarba 16 awril lañuy def ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Magi mbooloo mi war nañu topp tegtal yii :
◼ Waxtu ndaje bi, na nekk waxtu boo xam ne, bu ñuy joxante mburu mi ak biiñ bi, dina fekk jant bi so ba pare.
◼ War nañu xamal kiy def waxtaan bi ak ñeneen nit ñépp, waxtu bi ñuy defe ndaje bi ak fu ñu koy defe.
◼ Bala waxtu ndaje bi jot, war na fekk mburu mi ak biiñ bi pare. — Seetleen La Tour de Garde du 15 février 1985, p. 17.
◼ Aset yi, weer yi, taabal bu baax ak lu jekk lu koy muur, loolu lépp war nañu leen a teg seen palaas bala waxtu ndaje bi jot.
◼ Bala ndaje bi di jot, war nañu raxas Saalu Nguur gi walla béréb bu ñuy defe ndaje boobu, ba mu set.
◼ Bala ndaje bi di jot, war nañu tànn ñi war a teral nit ñi, ak ñi war a joxe mburu mi ak biiñ bi. War nañu leen wax ba mu leer li ñu war a def bés boobu. War nañu leen wax it ne li ñuy sol ak ni ñuy defare seen bopp dafa war a jekk.
◼ Karceen bu bokk ci ñi Yàlla tànn, mën na feebar walla màgget ba du mën a teew ci ndaje boobu. Bu booba war nañu seet ni ñu mënee def ba indil ko ci mburu mi ak ci biiñ bi.
◼ Bu ñaari mbooloo walla lu ko ëpp waree bokk fi ñuy defe ndaje boobu, nañu fexe ba mu bañ a am nit ñu bare ñuy xaar ci buntu saal bi, ci mbedd mi walla fi ñuy bàyyee oto yi. Mbooloo mu njëkk mi, bu paree, mbooloo mu ci topp na xaar lu mat 45 minit bala muy tàmbali, su ko mënee.