Ay fàttali ngir Fàttaliku deewu Yeesu bi
Ren, màggalu Fàttaliku bi daa yemoo ak bésub dibéer 8 fan ci weeru awril. Magi mbooloo mi war nañoo bàyyi xel ci ponk yiy topp :
◼ Bu ñuy tànn waxtu wi ndaje mi di tàmbali, war na leen a wóor ne, duñu aw-awle misaal yi, li feek jant bi sowul.
◼ Ku nekk, boole ci boroom-kàddu gi, war naa xam kañ tembe la màggal gi di door, ak béréb bi ñu koy defe.
◼ War nañoo am xeetu mburu ak biiñ yi war, te fexe lépp pare. — Seetal La Tour de Garde, bu 15 feewriyee 1985, xët 19.
◼ War nañoo indi ci saal ba aset yi, weer yi ak taabal bu jekk ci xew bi, bu ànd ak ndimo li ñuy lal ci kowam, te teel leen a teg.
◼ War nañoo teel a jóg ci setal bu baax a baax saalu Nguur gi walla beneen béréb bu ñuy jëfandikoo ngir màggal gi.
◼ War nañoo teel a jóg ci tànn way-teeru yi ak way-awale misaal yi te xamal leen luy seen wareef ak doxalin bi war ci xew bi.
◼ War nañoo fagaru ngir mën a jox misaal yi képp ku ñu tànn ak xel mi te yaramam bañ, ba tax du mën a teewe ndaje mi.
◼ Su fekkee ne lu ëpp menn mbooloo gëmkat mooy jëfandikoo benn saalu Nguur gi, mbooloo yi war nañoo ànd a jëflante ci fasoŋ bu rafet, ba tax duñu xatalante, ci lu ko jarul, ci bunt yi, fi nit ñiy dox ci mbedd mi, ak ci taxawukaayu woto yi.