Nanga seetiwaat nit ñi ngir tàmbali ay njàngum Biibël bi
1 Yeesu laaj na taalibeem ya ñu waaraate. Waaye wax na leen it ñu “ sàkk ay taalibe [...] jàngal leen ”. (Macë 28:19, 20.) Waaraatekat dafay waaraate, waaye jàngalekat dafay def lu weesu loolu. Day wone, day faramfàcce, day wax lu tax muy wax dara. Mën nañu def loolu bu ñuy tase ak ku bëgg waxtaan ak ñun. Nañu ko seetiwaat ngir tàmbali benn njàngum Biibël bi ak moom.
2 Ñan nit lañu war a seetiwaat ? Képp ku nangu benn ci suñuy téere. Walla képp koo xam ne tuuti rekk la wone ne dafa bëgg waxtaan ak ñun ci xibaar bu baax bi. Boo tasee ak ku mel noonu, fekk nekkul ci këram, fexeel ba xam adareesam ak nimoro telefonam ngir seetiwaat ko. Jàppal ci sa xel ne dinga mën a tàmbali ay njàngum Biibël bi. Wéyal di seet ay nit ñu bëgg jàng Biibël bi. Boo ci góor-góorloo dinga mën a tàmbali ay njàngum Biibël bi. — Macë 10:11.
3 Xalaatal bu baax ki ngay waxal : Ci waxtaan bu njëkk bi nga mën a waajal li nga koy wax bés boo ko seetiwaatee. Am na ay waaraatekat yu aay ci tàmbali ay njàngum Biibël bi. Ñoom dañuy seet liy itteel ki ñuy waxal. Léegi su ñu ko naree seetiwaat, ci loolu lañuy tàmbali seen waxtaan. Am na ñu def leneen : bala ñu jeexal seen waxtaan bu njëkk bi dañuy laaj dara, ngir nit kooku bëgg xam tont bi. Ci dëgg dañu bëgg dimbali nit ñi. Moo tax bu dee sax pare nañu waxtaan ak ñoom ba dem, dañu kontine di bàyyi suñu xel ci ñoom. Tax na it ñu bañ a yéex bala ñu leen di seetiwaat. Nañu ko jéem a def bala seen xel dem ci leneen, xéyna benn walla ñaari fan ginnaaw waxtaan bu njëkk bi, su ñu ko mënee.
4 Boo delloo ci kenn, jéemal kontine waxtaan bi nga amoon bu njëkk. Saa yoo fa demee fexeel ba jàng ci Biibël bi lu mu tuuti tuuti benn aaya bu mën a laal xolam. Bul fàtte di ko déglu bu baax. Jéem ko gën a xam it. Soo defee loolu, boo ko nar a gisaatee, dinga mën a waxtaan ak moom dëgg gi nekk ci Baatu Yàlla bi ko gën a mën a itteel.
5 Fexeel ba tàmbali ay njàngum Biibël bi : Booy dellu seeti nit, fexeel ba tàmbali ak moom benn njàngum Biibël bi. Noo mënee def loolu ? Nee ko danga ko bëgg wax benn xalaat bu baax, te ubbil sa téere Xam-xam walla Laaj. Seetal benn xise bu ko mën a itteel. Jàng ko, ba pare jàngal laaj bi te waxtaanal ci benn walla ñaari aaya bu ñu bind foofu. Mën nga sax taxaw ca bunt ba, te def loolu yépp ci 5 walla 10 minit. Boo bëggee jeexal waxtaan bi laajal beneen laaj te fexeel ba mën a dellusi ngir kontine waxtaan bi beneen yoon.
6 Nanga jéem a gën a waxtaan ak képp ku bëgg waxtaan ak ñun. Lu am-a-am solo la ci liggéeyu waare bi. Kon ayu-bés bu nekk fexeel ba am jot ngir loolu, maanaam seetiwaat nit ñi suñu waxtaan neex. Sa waaraate bi dina gën a baax te dinga gën a bég.
[Laaj yi]
1.Lu tax seetiwaat nit ñi nekk lu am solo lool ?
2.Ñan lañu war a seetiwaat ?
3, 4. Seetiwaat nit ni mu ware lu mu ëmb ?
5.Loo mën a def lu yomb ngir tàmbali ay njàngum Biibël bi ?
6.Naka lañu mën a wonee ne seetiwaat nit lu am solo la ci ñun ?