TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 12/03 p. 8
  • Dimbalil ñi bëgg am dund gu dul jeex

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Dimbalil ñi bëgg am dund gu dul jeex
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nanga seetiwaat nit ñi ngir tàmbali ay njàngum Biibël bi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Waaj mooy indi waxtaan bu neex bu ñuy dellu seeti nit ñi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 12/03 p. 8

Dimbalil ñi bëgg am dund gu dul jeex

1 Nit ku nekk ak li nekk ci sa biir xol (Macë 12:35). Biibël bi wax na ci nit koo xam ne “ ci biir xolam, dafa bëgg xeex ”. (Sab. 55:21.) Am na ñuy “ gaaw a mer ”. (Léeb. 29:22.) Waaye am na it ñu bëgg ci seen biir xol dund gu dul jeex gi (Jëf. 13:48). Tey, Yexowa dafay xëcc ci moom ñi bëgg loolu ci seen biir xol (Xag. 2:⁠7). Naka lañu leen mënee dimbali ba ñu bokk ci ñiy jaamu Yexowa ?

2 Dellul bu baax seeti nit ñi : Dellu seeti nit ñi, dafa am solo lool. Képp ku bëgg sàkk ay taalibe war na xam loolu (Macë 28:​19, 20). Bu ñu gisee nit ku suñu waxtaan neex, ndax dinañu ko gaaw a dellu seeti ? Ndax dinañu dellu seeti képp ku jël ci suñu téere yi, walla képp ku wone ne xibaar bu baax bi neex na ko ? Ndax dinañu kontine di leen dimbali ngir ñu jëm kanam ci wàllu ngëm ? Saa yu ñu gisee nit ku suñu waxtaan neex, dañu ko war a dellu seeti, ndaxte loolu mën na tax mu am dund.

3 Boo waxtaanee ak nit ba pare, fekk fàttegoo li ngeen doon wax, bindal turam, adareesam, li ngeen doon waxtaane, aaya yi ngeen jàng, ak téere yi mu jël. Boo defee loolu ba pare, fexeel ba gaaw ko dellu seeti.

4 Li ñu war a def bu ñu delloo seeti nit : Booy waxtaan ak koo dellu seeti, danga war a neex deret te lewet. Danga war a wone itam ne danga ko yéene lu baax. Waxtaanal ci li nekk ci Biibël bi, te na nekk lu yomb ci moom. Balaa nga fay dellu, nanga seet ci Biibël bi loo xam ne bu ko déggee, dina ko neex. Bu ngeen demee ba bëgg a jeexal seen waxtaan, laaj ko benn laaj te wax ko ne boo fa dellusee dingeen ci waxtaan. Bu nit ki waxee lu àndul ak Biibël bi, jarul nga ciy werante. Li gën mooy ngeen waxtaan ci loo xam ne yéen ñaar ñépp a ci ànd. — Kol. 4:⁠6.

5 Ku bëgg dellu seeti nit ñi dafa war a góor-góorlu dëgg. Waaye li ñu ciy jële dina seddal bu baax suñu xol. Ca Sapoŋ, dafa am benn pioñee bu newoon ne weer wu nekk dina yokk nit ñi muy dellu seeti. Dafa njëkk bind képp ku mu doon dajeel bi mu doon waaraate këroo-kër. Bu bindee turu nit, dina fexe ba dellu seeti ko ci ayu-bés bu ciy topp. Dafay njëkk waajal bu baax li mu nar a wax, ba pare dem waaraateji, xam ne xibaar bi muy indil nit ñi dafa am solo lool. Bi mu doon dellu seeti nit ñi, am na bés bi mu komaasee jàng Biibël bi ak ku ko waxoon ne : “ Man de, dama mas a bañ a déglu say moroom. Tey laa leen di njëkk déglu. ” Li pioñee boobu doon def ngir góor-góorlu ci waaraate bi mujj na jur lu baax. Bi weer wi mu komaase def loolu jeexee, defoon na lu mat fukki njàngum Biibël.

6 Li nit ñi nekke, bés bu nekk mu soppeeku (1 Kor. 7:31). Seetlu nañu ne nit ñi suñu waxtaan neex, ñu ci bare, balaa ñu leen di mën a gisaat, dinañu jaar seen kër ay yooni yoon. Waaye, bu ñu delloo bu baax seeti nit ñi ni, dinañu dimbali ñi bëgg dox ci yoon biy jëme ca dund ga dul jeex. — Macë 7:​13, 14.

[Laaj yi]

1. Tey, ñan la Yexowa di xëcc ci moom ?

2. Lan moo bokk ci sàkk ay taalibe ?

3. Bu ñu waxtaanee ak nit ba pare, lan lañu war a def ?

4. Naka lañu mënee def ba bu ñu delloo seeti nit, mu jur lu baax ?

5. Naka la benn pioñee doon góor-góorlu ci waaraate bi ? Loolu lu mu jur ?

6. Lu tax waruñu tàyyi ci dellu seeti nit ñi ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager