Waaj mooy indi waxtaan bu neex bu ñuy dellu seeti nit ñi
1. Naka la karceen yu njëkk yi waroon a yaatal liggéeyu waare bi ?
1 Yeesu waajaloon na bu baax taalibeem yi ngir ñu doon waaraatekat yu aay ci yégle “ xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla ” (Macë 4:23 ; 9:35). Yeesu dafa leen waajal bi ñu doon waare ca biir Palestine kese. Waaye bala Yeesu dem asamaan, waxoon na ne karceen yi dinañu yaatal bu baax liggéey boobu ba di “ sàkk ay taalibe ci xeet yépp ”. — Macë 28:19, 20.
2. “ Sàkk ay taalibe ” ni ñu ko Yeesu sante lan la laaj ?
2 Liggéey boobu laajoon na ñu dellu seeti ñi xibaaru nguuru Yàlla neex, di leen jàngal ñu topp lépp li leen Kirist sant. Bu ñu bëggee dellu seeti nit ñi ci fasoŋ bu baax noonu, dañu ko war a waajal bu baax.
3. Ci waxtaan bi ngay njëkk am ak nit ki sax, loo mën a def ngir mën dellusi waxtaan ak moom ?
3 Seetal li ngay def bala ngay dem : Am na waaraatekat yoo xam ne ci waxtaan bu ñuy njëkk am ak nit ki, bala ñuy taggook moom, dañuy fexe ba laaj ko benn laaj. Ba pare ñu wax nit ki ne dinañu fa dellusi ngir waxtaan ci ak moom. Gis nañu ne bu ñu waxee ci lu nekk ci téere Qu’enseigne la Bible ?, bu ñu delloo seeti nit ki, dafay tax ñu mën a komaase njàngum Biibël ci saa si.
4. Lu tax waruñu xaar ba jot yéenekaay yu bees yi, sog a dellu seeti nit ñi ?
4 Dëgg la, weer wu nekk, ñaari yéenekaay kese lañuy won nit ñi. Waaye loolu warul a tax ñuy xaar ba ñu jot yéenekaay yi weer wi ci topp, sog a dellu seeti nit ñi. Bu ñu waxtaanee ak ñoom ci li nekk ci yéenekaay yi ñu leen jox ba pare, loolu mën na tax nit ñi gën a bëgg waxtaan ak ñun.
5. Xam li nga bëgg def, lu tax mu am njariñ ?
5 Nañu xam li ñu bëgg def : Bala ngay dellu seeti nit ki, nanga toog tuuti, xool li nga bindoon ci moom te seet li nga fa bëgg def. Mën ngeen waxtaan ci li nekk ci téere yi nga ko joxoon. Walla nga jox ko yeneen téere yuy wax ci li ngeen jotoon a waxtaan. Bu fekkee ne bi nga fa njëkkee dem danga ko laajoon benn laaj, wóor na ne tontu laaj boobu dina bokk ci li nga fa bëgg a def. Booy wone aaya buy dëggal li ngay wax nanga fexe ba jàng ko ci Biibël bi.
6. Lan moo ñuy tax a dellu seeti nit ñi ?
6 Li tax ñuy dellu seeti nit ñi : Dëgg la, komaase njàngum Biibël moo ñuy tax a seeti nit ñi. Suñu benn mbokk dafa laajoon kenn ku mu dellu woon seeti ndax bëgg na mu jàngal ko Biibël bi. Waaye nit kooku bañ. Suñu mbokk daldi fa delluwaat ak yéenekaay yi mujj génn te nee ko : “ Dañu fi ñëw ngir tontu ak Biibël bi ci benn laaj bu nit ñi di laajte tey. ” Bi ko nit ki waxee li mu xalaat ci laaj boobu, suñu mbokk mi daldi jàng benn aaya. Mu jàng it ci téere bu ñuy defe njàngum Biibël, xise bu baax ci waxtaan boobu. Mujj na di jàng ak moom Biibël bi.
7. Waajal sa bopp bu baax, naka la la mënee may nga komaase njàngum Biibël ?
7 Jël jot ngir waajal li ñu nar a def bu ñuy dellu seeti nit ñi jar na ko. Suñu mbégte dina gën a yokku. Xéyna it ñu mën a dimbali ku “ jagoo ” maanaam yelloo dund gu dul jeex. — Jëf. 13:48.