Kàddu Yàlla mooy dëgg
1 Sabuur nee na : “ Lépp li nekk ci sa kàddu mooy dëgg. ” (Sab. 119:160). Ci Kàddoom, Yexowa dafa ñuy tontu ci laaj yu am solo yu ñuy laaj suñu bopp. Dafay seddal suñu xol te bu ñu nekkee ci coono dafa ñuy may yaakaar. Te dafa ñuy won ni ñu ko mënee jege. Lii la benn jigéen wax : “ Ku jàng dëgg gi nekk ci Biibël bi dinga mel ni ku jóge fu lëndëm te dugg ci néeg bu leer te féex. ” Ndax foo mënta nekk yaa ngi jéem a waxtaan ak nit ñi ci dëgg gi nekk ci Kàddu Yàlla ?
2 Mën na soppi nit te mën na neex nit ku mu mënta doon : Dëgg gi nekk ci Biibël bi dafa am doole. Mën na laal xolu nit te soppi dundam (Yaw. 4:12). Am na benn jigéen bu tudd Rosa. Dafa doon cagatu, di naan ba màndi te di jël dorog. Nee na : “ Amatuma woon benn yaakaar ci sama àddina. Benn bés, ñaari seede Yexowa, benn góor ak jabaram, dañu ñów waxtaan ak man. Won nañu ma ni ma mënee faj samay coono ak li nekk ci Biibël bi. Tàmbali naa jàng Kàddu Yàlla. Gis naa ne dafa neex lool. Matul benn weer ma am doole ngir tàmbali dund dund bu bees te sell. Léegi xamoon naa li ma bëgg def ci àddina si. Kon soxlatuma woon naan ba màndi walla jël dorog. Li ma gënoon a bëgg mooy nekk xaritu Yexowa. Looloo tax ma fas yéene topp ay ndigalam. Xam-xam bi nekk ci Kàddu Yàlla, dafa am njariñ. Bu dul woon xam-xam boobu, wóor na ma ne tey jii dina fekk ma xaru. ” — Sab. 119:92.
3 Biibël bi mën na neex nit “ ñu bokk ci xeet yépp, giir yépp, réew yépp ak kàllaama yépp ”. Téere yu mën loolu, barewuñu (Peeñ. 7:9). Li Yàlla bëgg mooy “ ñépp mucc te xam dëgg gi ”. (1 Tim. 2:4.) Kon, bu ñuy xool nit, buñu nee mukk : “ Kii, ci li ma gis, xam naa ne du nangu déglu xibaar bu baax bi. ” Nañu ko yëgal ñépp. Te su ñu ko mënee, nañu ko wone ci biir Biibël bi.
4 Jàngal ay aaya booy waare : Fi ngay mën a def loolu, bare na. Booy wone suñuy yéenekaay, fexeel ba jàng aaya bi nekk ci “ Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi ”. Bu ñuy wax ci téere bi ñu war a wone ci weer wi, am na ñuy tànn benn aaya bu baax, ba pare tàmbali seen waxtaan ak aaya boobu. Saa yoo demee seetiwaat nit, fexeel ba jàng lu mu tuuti-tuuti benn aaya ci Biibël bi. Bu yàggee, nit kooku dina am xam-xam bu wér ci Biibël bi. Booy def benn njàngum Biibël bi, nanga wax bu baax ci aaya yi gën a am solo. Foo mënta nekk, fexeel ba am benn Biibël ci sa wet. Su ko defee, boo ci amee bunt, dinga mën a waare. — 2 Tim. 2:15.
5 Dëgg gi nekk ci Kàddu Yàlla dafa am doole bu mën a xiir nit ci lu baax. Kon saa yu ñu ko mënee, nañu ubbi Biibël bi ngir jàng ci ay aaya bu ñuy waar ay nit. Noonu ñoom it dinañu mën a am doole ji Kàddu Yàlla maye, te gis njariñam. — 1 Tes. 2:13.
[Laaj yi]
1. Ban xam-xam bu am solo moo nekk ci Biibël bi ?
2. Biibël bi mën na tax dundu nit gën a baax. Naka ?
3. Lu tax ñépp lañu war a wax li nekk ci Biibël bi, bañ a tànn ñi ñuy waxal ?
4. Nu ñu mënee jàng ay aaya ci Biibël bi bu ñuy waare ?
5. Lu tax ñu war a fexe ba jàng ay aaya ci Biibël bi bu ñuy waare ?