“ Kàddug Yàlla [...] am na doole ”
1 “ Kàddug Yàlla mi ngi dund te am na doole, ” la ndaw li Pool bind (Yaw. 4:12). Lu mu bëggoon a wax noonu ? Kàddug Yàlla, walla xabaaram, bi ne ci biir Biibël bi mën naa am doole ju réy ci nit ñi. Sago si Biibël bi ëmb, am na kàttanu soppi dundug nit ki ci lu gën. Xol yi muy dëfël ak yaakaar ji muy joxe day wootal doom-Aadama yi ci Kiy maye dund, Yexowa Yàlla. Xabaaram mën naa xiir ñi seen xol laab ñu tàmbalee dox ci yoon wiy jëme ca dund ga dul jeex. Waaye, ngir gis loolu, war nañoo jëfandikoo Biibël bi, bu ñuy waar ñeneen ñi.
2 Saa yoo ko mënee, jàngal aaya : Mel na ni barewul, yéenekat yi tàmm di jëfandikoo Biibël bi ci bunt yi. Ndax loolu dina lay dal ? Xéy na, li la nit ñu bare niruwul ñu am jotu waxtaan wu gudd, moo la tàbbiloo ci tàmmeelu yem ciy wone suñuy mbind yi walla ciy wax ab aaya ci sa kàdduy bopp. Ñu ngiy xiirtal yéenekat yi yépp, bu ñuy waar xabaar bu baax bi, ñu góor-góorlu dëgg ngir jànge ci Biibël bi lu mu bon bon benn aaya ; noonu nit ki dina gis ne, ci dëgg suñu xabaar ci biir Kàddug Yàlla la nekk.
3 Dëgg la, ñi tàmm di jàng Biibël bi ñu néew lañu, teewul li ëpp ci nit ñi faral nañu di ko weg. Nit ñi jàpp sax, dinañu jël benn walla ñaari simili ngir déglu xabaar, bu ñu jànge ci Kàddug Yàlla. Bu ñu jàngee aaya ju dal, def kook suñu xol bépp te ñu faramfàcce ko bu gàtt, kàttanu kàddug Yexowa mën naa def lu réy ci kiy déglu. Waaye noo mënee jàll ci aaya jooy jànge ci Biibël bi, boo ubbee sa waxtaan ba noppi ?
4 Jéemal lii booy wone yéenekaay yi : Am na wottukat buy wër buy jëfandikoo ak manoore Mbind yi, saa yu nekkee di wone yéenekaay yi. Day yóbbaale Biibël bu ndaw ci biir poosam. Bu wonee yéenekaay yi ba noppi, te faramfàcce bu gàtt ab bunt, du ragal a ubbi Biibël bi, jànge ci nag aaya ju joteek li ne ci bunt bi. Mën naa def loolu ci lu yomb, buy laaj : “ Loo xalaat ci dige buy xiirtal bii ? ”, ba noppi mu tàmbali jàng aaya ji mu tànn.
5 Jublul ci jàngal képp ku lay déglu benn aaya Biibël bi walla ñaar. Dooley xiir ci jëf, ji ne ci moom mën naa xàll yoon, wiy wootal ci Yàlla nit ñu gën a bare. — Ywna. 6:44.