Ndax dangay faral Kàddu Yàlla ?
1 Tey, ci àddina si, nit ñi tàmm nañu weddi Biibël bi. Waaye karceen dëgg yi dañu koy faral. Dafa ñu wóor ne Mbind mu sell mi ci Yàlla la jóge moo tax ñu ànd ak li Yeesu Krist waxoon ci ñaan bi mu defoon Yexowa maanaam : “ sa kàddu mooy dëgg ” (2 Tim. 3:16 ; Ywna. 17:17). Naka lañu mënee faral dëgg kàddu Yàlla ?
2 Nañu jàng Mbind mi : Yeesu dafa doon gëstu bu baax Kàddu Yàlla. Loolu tax na, saa yu doon waaraate, ci mbind mi la don jële li muy jàngale (Lukk 4:16-21 ; 24:44-46). Lan lañu war a def ba mën a jàpp aaya yu bare ci suñu xel ? Dañu war a jàng Biibël bi bés bu nekk ba pare delluwaat ci aaya yi ñu gis ne mën na yokk suñu ngëm walla aaya yi mën a baax ci waaraate bi, te xalaat ci bu baax. Saa yooy waajal suñuy ndaje yi, war nga seet aaya yi ci Biibël bi te jàng leen. Xéyna sax dinga waajal tont boo mën a wax ci aaya boobu ca ndaje ba. Bu ñu nekkee ci ndaje yi, kuy wax, saa yuy jàng benn aaya, dañu ko war a topp ci suñu Biibël. Jàng ay aaya ngir jàpp leen ci suñu xel dina tax ñu mën a “ faramfàcce bu jub kàddug dëgg gi ”. — 2 Tim. 2:15.
3 Nañu bàyyi Biibël bi waxal boppam : Bu ñuy waaraate dañu war a bàyyi Biibël bi mu waxal boppam. Saa yu ñu ko mënee, dañu war a jéem a jàng benn aaya ak nit ki te waxtaan ci ak moom. Su fekkee ne dafa am lu mu ñu laaj, walla mu bëgg ñu weddi, li gën mooy ñu jëfandikoo Biibël bi ngir tontu ko. Su fekkee ne nit ki dafa jàpp lool, war nañu ko jéem a won benn aaya ci Biibël bi. Nañu ko wax lii : “ Dama la bëgg won aaya bii. ” Soo ko mënee, jàngal aaya boobu ci sa Biibël te feexel ba mu topp ci sa Biibël li ngay jàng.
4 Dafa am góor goo xam ne, bi ñu ko wonee ci Biibël bi ne Trinite, maanaam benn Yàlla bu def ñett, mënul nekk, dafa nee : “ Bi ma juddoo ba tey dama tàmm di dem jàngu ba, waaye masuma woon a xam ne lii la Biibël bi wax ! ” Kooku nangu na ñu jangal ko Biidël bi. Yeesu nee woon na ne ay mboteem dinañu déglu baatam (Ywna. 10:16, 27). Li gën a mën a tax boroom xol yu rafet yi xàmme dëgg gi mooy ñu won leen ko ci Biibël bi. Kon boog nañu doon ñiy faral Kàddu Yàlla gi nekk dëgg.