Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 févr.
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Am na ñu bare ñoo xam ne bu ñu gisee lu bon li nit ñi di def ndax seen diine, dañuy jaaxle lool. Am na ñuy wax ne diine moo indi coono ci àddina si tey. Ndax mas nga xalaat ci loolu ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Peeñu bi 18:24 te won ko ne Biibël bi wone na ne diine bu dul dëgg bi tuur na deret bu bare.] Téere bii dafay wone li Biibël bi wax ci loolu. ”
Réveillez-vous ! Feb. 22
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Waajur yu bare seen xel dalul dara ci li portaabël walla Internet mën a def ci seeni doom. [Mayal nit ki wax xalaatam.] Téere bi dafay wone lenn ci lu bon li mën a dal ndaw yi bu ñuy jëfandikoo portaabël walla Internet, te naka lañu leen mënee aar ci loolu. ”
La Tour de Garde Mar. 1
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Am na bés boo xam ne dañu laajoon Yeesu laaj bii : “ Ci ndigal yi, ban moo ci gëna màgg ? ” Seetal fii li mu tontu. [Jàngal Mark 12:29, 30.] Ci yow, lan mooy bëgg Yàlla ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa xel mépp ak sa kàttan gépp ? [Mayal nit ki mu tontu.] Téere bii dina ci joxe tont bu leer ci xaaj bi tudd : ‘ Comment nous démontrons notre amour pour Dieu (maanaam naka lañuy wone ne bëgg nañu Yàlla). ’ ”
Réveillez-vous ! Mar. 8
[Boo nuyoo ba pare mën nga nee :] “ Am na jamano joo xam ne, ñu bare dañu ragaloon xare bu mettee metti am, maanaam li ñuy woowe ci tubaab guerre nucléaire. Ndax foog nga ne xare bu mel noonu mën na am tey ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wax ci xew-xew yoo xam ne bu yàggul lañu fi amoon, te ñun ñépp lañu soxal. Dafay leeral it li Biibël bi dige, maanaam jamano joo xam ne kenn dootul ragalati. ” Jàngal Mikaa 4:4.